Dees na xamee ci xisa yi yu bari ci mayi Yàlla yi. Nit dina man a xam ay mbir yu nëbbu ci coobareey sunu Boroom. Dina fi feeñee itam dolleey ngëm, dooleey kóolute ak i jeexitalam ci topp ndigalu Sëriñ bu mat Sëriñ. Yal nanu Yàlla saxal ci ag taalube, sàmmoonte, ak ragal Yàlla.
Fii di nanu fi leeral mellow génnug ruu, ak yi ci aju yépp. Naka noonu dees na fi xamle laaji yi nga xam ne dina am ci bàmmeel ak ginnaaw laaj yi li fay xew. Yal nanu Yàlla sàmm te tënk nu ci lislaam.
Li ab Téere bu m njariñ lool, ay wax ak i jëfiinu Sëriñ Bi moo ci nekk, nu man ci gindiku ci sunu lislaam ak ci sunu taalibe. Fii nag matug Boroom Tuubaa dina di feeñee ak sunu tawfeex ci ànd ak moom. Yal nanu nuur ci moom barkeb Xasiida yi .
Nu wéyal ba tay ci mbiri baamel? Ndax mooy ku ñu def ci pax rekk ? Am romb na loolu. Dees na fi leeral tamit xew-xew gu amoon diggante benn jullit ak ben yéefar gu siiw bob, di neen ci jëlle ay jàngat yu fees dell ak waare. Yal nanu Yàlla musal ci tiisu bàmmeel.
Fii danu fiy leeral lu aju ci bàmmeel ak dundug bàmmeel ci waxi Kilifa yi. Dees na fi xamee itam ne, sax ci lu baax dara amul njëgam. Naka noonu topp li Yàlla digle ak wattandiku tere yi. Yal nanu Yàlla saxal cig njub barkeeb koor gii nu nekk.
Ay leeral yu jëm ci li war boroom kër ci soxnaam, yuy gën a dëggaral yi nu doon wax ci ginnaaw. Yii dafay jëm ci xamle lislaam ak yi ci aju, mu mel ni kon jàng manta ñàkk. Yal nanu Yàlla defal xam-xam.
Ci xaaj wi danu fiy leeral yi nga xam ne dina araam ci jigéen bu am ngàtt mu di ko def, mba muy dem ci ay barab yu mu warul dem. Te war na ci Boroom kër mu xamal ko soxnaaam. Te mu xamal ko it mbolleem lu aju ci wàll woowu.
Ba tay warteefi borom kër ci soxnaam leen fiy xamle. Mel ne xamal ko diineem ak yi ci aju. Di ko leeralal lenn ci sew-sewi julli ak yi ci des. Daa wara xamal njabóotam itam ak ñi mu yilif seen diine. Yi jëm ci dareeti mbërag, wësin, yooyu yépp daf ko wara xam, te xamal […]
Ci xaaj wi, dees na fi lim yi nga xam ne war na boroom kër mu xamal ko soxnaam, ñi mu njaboote. Te mooy faratay jëmam ak mbolleem li ci aju, dalle ko ci laab, ponki diine yi la cay farata ak sunna. Di ko waar ngir bëggal ko lu baax ëllag. Te sax « góor […]
Li ab Téere la bu am solo jëm ci xamlee nees di yoree sa Soxna ak ay mbir yu jëm ci dundug bàmmeel ak yeneeni yëf. Ku ñuy wax Umar Jóob moo doon laaj Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu ay laaj yu am solo. Sëriñ bi bind Téere bi àndil ko ci ay […]