Jantub jamono!

Sëriñ Saalihu Mbàkke mi ngi gane àdduna ci atum 1915 ca Njaaréem di doomi Sëriñ Tuubaa Xaada lahul laahu maxtaara lahu ak soxna Faati Jaxate. Ku amoon taxawaay la, dëgër lool am i bët, ay cëram dëggër. Ku manoon a xerawlu la, am kersa, bari woon lool lumiy jaxasoo ak ay gone, da leen a yërëmoon lool, te daan leen bégal. Jëmm ju manoon a seetlu la, te neexum xel lool ba ràññéeku ci, te dëddu àddina lool. Da daan wax naan « lépp loo xam ni man nga ko ñàkk ci àdduna te du la njariñ allaaxira loolu dëddu àdduna la ». Daan na fonkuloo ñépp xaxida yi ak yar ub gone yi.

Li ëpp ciy tukkeem diggante daara ya mu sosoon ca lay amee bokk na ci Ndokaa, Njàpandal, Xaabaan ak Xelkoom mi nga xam ne fukki daara ak juróom la. Manees na ci lim Daaru Salaam, Daaru Tansil ak Tuuba belel.
Daaraam yooyu dañu faa boole.woon di jàngale alxuraan ak xam-xam, tey yar nit ñi ci liggéey. Ag ñeewantem ci jàmm ñi taxoon na mu daan ñaanal jullit yépp yërmande , njéggal ak jàmm. Ku daan dalal xel i ñi daan laaj ci bir yu leen di tax a defaru. Li koy firndeel moo di Sëñ Mustafa Abdu Xaadr wax na ni am na ku fa mas a ñëw naa ko damaa bëgg am ug taalube. Seriñ bi xamal ko ni: « bëgg am taalube rekk cër la. » Keneen laajati ko naan: dama bëggoon di joxe àddiya mu ni ko « xam ni war na la ab cër la »

Li am moo di sunu boroom mooy ki ko xiiroon ci xasida yi ak nangoo joxe àddiya. Te boobu kat dalagul jàng. Ndax dërëm ba mu njëkk am Ku Teed ki la ko jox mu naa ko ndax xam nga li nga ma jox lumu mu ni ko xam naa ko dërëm la. Ba tay xasida Ikfini mokkaloon na ci lu bari te booba dalagul. Daa bëggoon xasida yi ndax mas naa wax Sëñ Mustafaa Abdu Xaadr xasida yi suma ci séntuwul woon benn tiyaaba ba tay daa neex ci man. Moo tax it ay ndogam daan nañu sax di yékkati xasida yi ni ko mag ñi daan defe. Mu yar lenn ba tay ci muñ, ci ngor, ci fulla ak ci fayda. Looloo waral kenn yabu leen. Ay nit ñu doylu la ñu te am ug saam, woyof lool te am kóllëre, rafet xol te rafet doxiin.

Mooy ki ñu mujjee gis ci doomi Seexul Xadiim, dund na juróom ñent fukki at ak ñaar (92). Bàyyi fi janboot gu góor ak wu jiggéen te ñooy: Sëñ Seex, Sëñ Mustafaa, Sëñ Basiiru, Sëñ Jiili Abdu Xaadr, Sëñ Murtadaa, Soxna Waalo, Soxna Moomi, Soxna Maam Faati, Soxna Maam Buso ak Soxna Aminata.

Liggéeyu Sëñ Saalihu nag, fës na ba mel ni jant. Moo xirtal ndaw ñi ci jàmmu Yàlla ak fonk xasida yi. Moo xirtal ñépp ci tool yi, liggéeyaat dëkku Boroom Tuubaa rawatina jumaa ji.

Moom nag 2007 la fi bàyyikoo.
Yàlla sunu Boroom mi ko bind noo ngi koy ñaan mu dooli ko yërmande lu raw ni mu ko amee woon ci jàmm ñépp. Nay dooli darajaam jamono ju ne, tey yokk i leeram, te  » mbooleem ni doon i Saalihiin ak feneen yal na Saalihu di seen jant wu tiim waa xarnu bi » barke Seexul Xadiim.

Al-Habdul Xadiim

Lille, 30/12/2019.

S’abonner
Notification pour
guest
4 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Ndiaye
Ndiaye
3 années il y a

Diadieuf yarame

A.Gueye
A.Gueye
3 années il y a

MaSha’ALLAH Serigne bi souniou xol 😍🥲

Babacar Thiam
Babacar Thiam
3 années il y a

Allahouma amine Bidiahi SERIGNE TOUBA Wa Mame Cheikh Ibrahima Fall LAMP FALL BABOUL MOURIDINA.

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR