Jazbatu Sighàr(3)

Bismilahi rahmani rahim

Ap dog


Ni ñuy gëmé yonnent yi aleyhimu salàtu wa salamu móodi da ñuy gëm ne suñu borom mo len yóoni ci ñun bu werr. Gëm itam lepp luñu andi, te gëm ne duñu fen,
duñu def lu haram, duñu def luñu sib, duñu nëbb li ñu len digal ñu jottaliko mindeef yi. Batey nu gëm ne lepp
lo xam ne bu len dallé ci xeet yiy dall doomu àdama, du tax ñu leen di hayyibal wala ñu len ji daw mën na leena dall. Da na ñu jaay di jënd, di lekk di naan, di am
soxna, di tawat. Lu melné ngàana wala siti du len dall.
Suko défé li ñuy tektal ne yonnent yi aleyhimu salàtu wa salamu lepp luñu wax dëgg la moodi, kiiman yi ñuy def, nga xam ne da ñuy xamal ne, ki leen yonni and na ci li ñuy wax ak li ñuy def. Kiiman yu yéemé lay doon nga xam ne kudul ñoom du ko mën, te da ñu wax ba nopi mu doora am te day fekk ñuy wooté ag yonnent. Melné weer wi, xar gimu xaroon ci jamonoy yonnent bi salla laahu tahala aleyhi bi alihi wa sahbihi wa salama ngir dëggal ko. Batey am na mbët mu waxoon ci jamonom. Li ñuy xamal ne ab yonnent du def lu haraam, du def luñu sib, moodi buko defoon da ñu koy roy ndax suñu boroom mo ñu diggal ñu leen di roy, te suñu boroom moo tere lu haraam. Bu bàyyé ay yonnentam aleyhimu salàtu wa salamu ñu koy def, day melné mi ngi diglé lumu tere. Li nuy xamal ne, manta ñàkk ci ñoom ñuy jotal moodi woolu gi leen suñu borom woolu ba yonni leen, ndax bu xamoon lénen du leen yonni. Li ñuy xamal ne liy dall nit ñi dana’leen dal moodi daa am ñu ko fekke. Ñoñee ñooko nettali bamu agsi ci ñun.
Yonnent yëpp ñetti téemeer lañu ak fuk’ak ñett (313). Am na ñu wax ne ak fuk’ak ñent, am na ñu wax ne ak fuk’ak juróom. Bunu boolé yonnent yëpp ak ni suñu borom xamal xam-xamu yonnent te yonni wulen da na ñu matt téemeeri junni ak ñaar fukki junni ak ñent’i unni (124000).

Sukko defe yonnent yi ñew ci Alqur’an da ñu len wara gëm ba nopi xam seni tur. Ñi ngini : sayyidina Muhammad, Adama, Nùh, Hùd, Idriis, Lùt, Sàlih, Dàwud, Yùsuf, Yùnus, Ayùb, Harùna, Yahya, Yahqùba, Ilyàs, Alyasah, Ibràhiim, Ishàq, Ismàhil, Mùsa, Zakariyya, Suleymàn, Zul-kifli, Isà, Shuhaybu aleyhimu salàtu wa salamu.

Ap dog

Ni ñuy gëmé bis pencc mo di nu gëm ne lu amla te woolu ko. Lepp luñu wax ne dana fa xéw itam nu gëm ko. Dallé ko ci dekki ak dajaloo ga ñuy dajalo fi benn barab ak natt ga ñuy natt suñiy jëf. Batay Yonnent bi salla laahu tahala aleyhi bi alihi wa sahbihi wa salama amna fa ap déeg buñiy wax Kawsara, naka noonu ñu gëm ne ajjana ak sawara lu ci nekk am na. Naka noonu Siràt lu amla, ñëpp da ñukoy jéggi ci kemtulaayi seeni jëff. Naka noonu ñu gëm ne yonnent bi salla laahu tahala aleyhi bi alihi wa sahbihi wa salama dana rammu rammu mu mag bu ëlaggé. Batey nu gëm ne lu waay def lumu tuuti tuuti ba toll’ne féep suuf des nako seet ba ci bàyima yi da ñuy feyyanto, wicci am i béejjan ak wiko amul woon ci adduna. Lepp lu waay def, danako gis. Yalnanu suñu borom boolé ca ña nga xam ne duñu tiit ëllak, duñu jàqq.

Sukko defe bis pencc da ñuko def ñaari xaaj : bu ndaw ak bu mak. Kepp ku fàtu bis penccam bu ndaw taxaw na, foofé lañukoy laajé diko tambalé wani xéewal wala ay mbugal. Bu ñëpp déeké ala bu mag ba tambalé.

Al-Habdul Xadiim

Grenoble, 20/11/2019.

S’abonner
Notification pour
guest
2 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
BASSIROU CISSE
BASSIROU CISSE
5 années il y a

Machallah am na solo lool sakh sama dieuwrigne, Yalla na lén souniou Borom faye thi barké cheikhoul khadim

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR