Jazbatu Sighàr(4)

Ap dog
Ni ñuy gëmé dogal bi moodi ñu gëm ne lepp lu am suñu boroom mooko amal ci kàttanam ak ub xam-xamam, moo xam lu nëbbu la wala muy lu feeñ, wala aw yiw wala aw ay, melné toppu yoonu yonnent bi
salla laahu tahala aleyhi bi alihi wa sahbihi wa salam wala topp ay bidaa, moo xam lu neex la wala lu naqari melné tuyaabay ñiy toppu yoonu yonnent bi salla laahu tahala aleyhi bi alihi wa sahbihi wa salama wala
mbugalum ñiy toppu bidaa. Dara manta def dara. Suñu borom rek mooy def, mooy sottal, ndox manta mandal, sawara manta lakké.Baatu Laa ilàha ila laahu muhamadun rasùlulàhi salla laahu tahala aleyhi bi alihi wa sahbihi wa salama boolé na mboleem pas-pas yima doon tuddu motax muy mandargam gëm yàlla subhanahu wa tahala. Li muy firi
mooy amul kenn ko xam ne àajowul jëm ci kenn wala lenn kudul yàlla subhanahu wa tahala. Amul ko xam ne ñëpp dañuy àjjawo jam ci moom ak lepp kudul yàlla subhanahu wa tahala.

Ap dog
ISLAM mooy wax Laa ilàha ila laahu muhamadun rasùlulàhi salla laahu tahala aleyhi bi alihi wa sahbihi wa salama, ak julli, ak woor weer’u Ramadàn, ak joxé azaka, ak hajj màkka booko mënee.
Borom xam-xam yi wax nañu ne fawu da ngay gëm ba nopi doora julli mu wér, doora wóor mu wér. Wùté nañu ndax da na yokk moom ngëm wala deet, li gana wér moodi yokk di wàñeeku.

REFETAL moodi ñuy jàamu yàlla subhanahu wa tahala ba melné ñoo’ngikoy gis. Buñu ko gisul nu xam ne mi ngi nuy gis.

Ma ngi sant suñu borom ci matug « Jazbatu sighàr » bii nga xam ne day àggalé ci yàlla bépp xolub ku sóobu. Ma ngi ñaanal yonnent bi salla laahu tahala aleyhi bi alihi wa sahbihi wa salama mi nga xam ne mooma gënnal sama bop ak leep lu mey soop.

Subhàna rabbika rabil hizati hama yasifùna wa salàmun
halal mursaliina walhamdulilaahi rabbil hàlamin
14 Jumàdal ùla 1430.

Al-Habdul Xadiim

Lyon, 21/12/2019.

S’abonner
Notification pour
guest
0 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR