Kan Mooy El Haaji Baara Mbàkke

Sunu sang bi turam dëgg mooy Muhammadul Amiin, ñu duppee ko Sëriñ Muhammadu Lamin Baara Mbàkke miy doomi Sëriñ Tuubaa. Sëriñ El Haaji Baara nag mi ngi gane àddina atum 1921 fa Ndidi.

Baayam moo di Sëriñ Fàllu Mbàkke, ndeyam di Soxna Xari Sàll. Baayam moo ko dalal Alxuraan, jox ko Sëriñ Moor Sànqe, ginnaaw gi mu jox ko turondoom ci atum 1928. Sëriñ Baara yor ay mbiram di saytu am jàngam ak barab ya mu key joxe ngir mu jàng fu mel ne Balal ci Sëriñ Móodu Amar. Bi fi turondoom jóge, la Sëriñ El Haaji Baara déllu ci baayam mu jox ko Sëriñ Jaamaal ngir mu yéggalil ko Alxuraan ji ba mu mokkal, am xam-xam itam. Ba mu noppee ci am jàngam la déllu Ndindi topp ci ginnaaw ay magam, nekk ci kilifteefu Sëriñ Fàllu. Sëriñ El Haaji Baara nag ku nangoo woon sónn ci ay way-juram la, ba ci rakki baayam yi. Daf leen jàppe woon ni Sëriñ Fàllu di leen liggéeyal ak di leen taxawu ci mbir yu bari. Noonu la fonkewoon Seex Abdul Ahad. Noonu itam la meloon ci Sëriñ Abdul Xaadir, ba ba miy dem Màkka sax moo ko doon taxawu ànd ak moom. Fonkoon na lool itam Sëriñ Saalihu. Moo tax doomi Sëriñ Tuubaa yu bari gëram neen ko. Bi Sëriñ Saalihu wàcce liggéey ci atum 2007 la ko wuutu. Doon sëtub Sëriñ Tuubaa bi njëkk yilif yoonu murid gi yépp. Bi mu tooge ci xilaafa gi nag la tàmbalee yokk ab liggéeyam ca Tuubaa, gën a yeesal dëkk bi ak Jumaa ji, defar ay tali, yokk làmp yi ak yeneeni liggéey yu am solo. Ñi mu yóbb ñu aji Màkka bari na lool itam. Te njëkk muy toog ci xilaafa gi la ko tàmbali.

Jàmbaar dëgg la woon, baax lool te woyof. Mi ngi fiy jóge atum 2010 ca Aaliya fa Tuubaa.Yal na ko Yàlla dolli yërmande, njéegal, xéewal ak leer ba fàww barkeb turondoom ji Sëriñ Muhammadu Lamin Baara.

S’abonner
Notification pour
guest
0 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR