Kan Mooy Maam Saalihu Faal?

Bismilaahi Rahmani Rahiim
Sëriñ Saalihu Faal mi ngi feeñ jamono ci atum 1858 ci dëkk buñuy wax « Jabbe Faal ».
Jabbe Faal nag mi ngi ci wettu « Waaqi » mi nga xam ne ci kiliftéefu Aatumaan Faal la bokkoon ci Jàmbur.

Way-juram wu góor mi ngi tuddu Ahmadul Faal Roqaya, way-juram wu jigéen mi ngi tuddu Soxna Saynabu Njaay bokk ci waa njare-njare yi, di ñoñ xam diine, ak xam-xam ak nguur. Way-juram wu góor mi ngi bokk ci kërug nguur.

Sëriñ Saalihu Faal nag, mi ngi jàngee ci Daara yu bari bokk na ci « Tayba-Xay » ak « Tayba-Daqaar » ak Daaray Sëriñ Abdullaahi Séy fa Njàmbur, ak Daaray Matuf ak Daaray Jaar Sayer.

Moom nag bokk na ci ñi teel a ñëw ci Sëriñ Tuubaa Xaada lahu laahu Maxtaara lahu ndax ak ñëwam ci Sëriñ bi mooy toolo ak 1888. At moomu itam mooy dëppo ak at mi mbokkam ma Seex Ibraahima Faal jotee ngëramul Boroomam ci Sheexul Xadiim.
Sëriñ Saalihu Faal bi miy ñëw ci Sëriñ bi mi ngi amoon 30i at. Sëriñ Tuubaa Xaada lahu laahu Maxtaara lahu tarbiya ko ci 3i at, gëram ko, tofal ko mbollo. Bokk na ci Sëriñ Tayba Ñaŋ, Sëriñ Abdul Xaadir Faal, Sëriñ Kodde Faal, Sëriñ Kumba Saar.

Ginnaaw ba sañc na dëkk yu bari ngir yar ak liggéey. Bokk na ci Daarul Imaan, kër Ngaala, ak Nóoto ak Daaru Xay Faal, kërum Njaabi-Faal, Dànd-Faal.

Li àndi sañcam Daarul Xafoor ak li àndi tur wi, ku ñuy wax Sëriñ Abdu Hawa Njaay di mbokkam ci wàllu way-jur wu jigéen, nettali na ne, Sëriñ bi dafa dem ba jëmi jamono mu bëgg a wut barab bumuy tarbiyaa bu bokkul ak Njaaréem ndax yooyu jamono mi ngi woon Kër Seex, ci wettu mbokkam ba Sheex Ibraahima Faal, ñu nekkoon fa ak Sheexul Xadiim. Ginnaaw gi la tàggu Sëriñ bi ci mbiram moomu. Mu daal di koy jox ndigal ci atum 1919, gannaaw ba geerub 1914 jeexe. Sëriñ bi jox ko ci ndigal. Ci at moomu la ko gor ba mu yewen. Sañc ko ci diggante 1921-1922. Tur wi nag mi ngi jóge ci Sëriñ Masàmba ak Sëriñ Daam Abdu Rahmaan Lóo ak Sëriñ bi. Ndax Sëriñ Abdu Rahmaan ak Sëriñ Masàmba den ko gane ci woon ci sañcam bu yees bi. Sëriñ Saalihu sàkku ci ñoom ñaar ñu sàkkal ko aw tur ba la ñoo waññiku. Ñoom ñaar ku ne wax sa moroom ne ko yaa gën a yey sàkk tur wi. Sëriñ Abdu Rahmaan wax ne « Hunaa Daaru Sëriñ Masàmba » teg ca Al-Xafuur.

Am na sax nettali bu wax ne Sheexul Xadiim, ba mukku yëggee, da caa teg ne « Ar-Rahiimu » muy « Daarul-Xafuurur-Rahiim ».

Sëriñ Saalihu Faal nag tarbiya kat la woon. Limal naa la Daaray Tarbiya yi mu taxawaloon yépp ngir yar, ak jàngale ak liggéeyal Sëriñ bi. Ci loolu la sax ba ni muu wuyu ji Boroomam atum 1943 ci bisub talaata ñatti fani Gàmmu, diggante tàkkusaan ak timis ñu jébbal ko boroomam ca yoor-yooru àllarba ji ci sës fa Tuubaa. 85iat la dund.

Délluwaay wi: Siira Mashaayixal Muriidiya.

Yàlla na Yàlla yokk ay leeram te taas nu ci bàrkeem. Aamiin barkeb Sheexul Xadiim.

Al-Habdul Xadiim
23/04/2021

S’abonner
Notification pour
guest
4 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Momar
Momar
3 années il y a

Mâcha Allah sang Bi 🙏

Malick
Malick
3 années il y a

MaShaAllah Amatina Solo 🙏

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR