Mi ngi ganee àdduna atum 1867 ca poroxaan, turam dëgg mooy Seex Siidi Muxtaar Mbàkke mi ngi bokk ci askanu Maam Mahram
Maam Seex Anta doomi Sëriñ Moor Anta Sali la moom Maam Bàlla moom Maam Mahram.
Maam Anta Njaay Mbàkke, doomi Maam Ibraahima Awa Ñang moom Maam Mahram mooy yaayam.
Kon Muhammadul Xayri Mbàkke walla nga ni Maam Mahram mi meeñi ñu bari ci kilifay Diine yi nekk Senegaal moo maamoo Seex Anta ci wàll yépp, muy ci Nday muy ci Baay.
Am njàngam mi ngi doore ci Sëriñ Daam Abdu Rahmaan lo, mi ngi mokkale ci Sëriñ Moor Sekk. Magam Sëriñ Maam Moor Jaara jàngal na ko lu bari ci xam-xam ak Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu mi doonoon yaakaaram, Sëriñam, kilifaam.
Ku daan dox bu wér ci Yoonu Murit la.
Man na noo wax ne lépp lu jëm ci wàllum koppar li ci ëppp moo ko daan joxe, loolu tax ñu ko daan woowee « l’argentier du mouridisme ». Moo daan teewal yoon wi ci jaatayu politig walla fépp foo xam ne yoon wi war na fa teew muy mbirum kayit.
Lu doonoon liggéeyam ?
Moom man na noo wax ne « homme d’affaires » la woon ndax bari ci li mu doon yëngu lu ci mel ne jënd ak jaay ak mbey.
Wax nan ne mbirum « export ak import » bokk na ci ni ko njëkk a jëmmal biir Senegaal. Li mu yoroon ci ay bitik itam yaatu woon na lool
Ci wallum mbey mi bokkon na ci lu taxoon mu sañci dëkkam boobu di Gaawaan. Li ëpp ci dund gi mu daan yott Sëriñ bi fa la daan bawoo.
Xarañteem itam a taxoon bi ko Sëriñ bi boole ak 99i taalibe, daa fexe ba ku nekk mu wutal la looy yëngu
Lu doonooni jikkoom ?
Li ci jiitu moy ak tabb ku tabbe la woon ñamewoon joxe lool, ku set la woon, te sell, woyof, xam teranga ak man a dimbale.
Sëriñ Tuubaa gëram na ko
Seede si de bokk na baatub Seex ci Moom la bawoo. Moom la Sëriñ bi njëkk a gëram jox ko dëkk bi mu njëkk a sañc te mooy Daaru Salaam
Loolu moo tax ku mu gërëmaat ginnaaw bi, ñu ne defal na ko la mu defaloon Seex, ba ñu naan Seexal na ko.
Wax nan ne bu Boroom Tuubaa masaan a gis Maam Seex Anta da daan muuñ ne « wamaa tawfeexi illaa billaah ». Daan na wax it « Seex Anta bamu may toppu xamul lumu ma toppee, manit xawma lumu ma toppee »
Dund Seex Anta, boroom dëram ak ngëram dees na ci dikkaat. Noo ngi ñaanal Sëñ Aamidu Njaay Gaawaan mi tax nu man leen a jukkil lii. Di ko ñaanal moom it dëram ak ngëram barkeb suufug Daaru Salaam.
Al-Habdul Xadiim
20/06/2022