Kan Mooy Sëriñ Abdu Rahmaan Lóo ?

Sëriñ Abdu Rahmaan Lóo mooy doomi Muhamad Lóo moom Mayib moom Aaliyun moom Ibraahima Lóo. Ndeyam móodi Maryaama Sekk moodi doomi Moor Jaane moom Muxtaar Sekk mi nekkoon Tayba Cekkeen.

Sëriñ Abdu Rahmaan ci altine la gànne àddina weeru Gàmmu 1852 walla 1853 foofu la màgge, duggee fa Daara ba mokkal Alxuraan. Am na nag ñu naan dëkk buñuy wax Cumbuleen la mottalee Alxuraan. Ndig la jàngee lu bari ci xam-xam. Bokk na ci Alfiyaa Ibn Maalig ak Alfiyaa Ibn Buuna. Jaar na it Pataar, jamono jooju Sëriñ Moor Anta Sali moo fa nekkoon. Foofu it jàng na fa Téere yu baree-bari. Sëriñ Tuubaa it jàngal na ko Muwaahibul Xudoos ak Mulayyinu Suduur. Jaar na it Njaañ di fa jàng lu mel ne Tajwid. Ba Sëriñ Moor Anta Sali bàyyikoo Pataar sañc Mbàkke Kajoor, Sëriñ Abdu Rahmaan Lóo fekk na ko fa.

Ginnaaw jàng mi, mu jóg nag fas yéene jàngale ci nekkub Sëriñ Moor Anta Sali ba bi mu fiy jóge.

Dafa gën a siiwee ci jàngale Alxuraan waaye ci njëlbéenam daan na jàngale xam-xam. Daan bind itam. Da daan wax nag li tax taalifu ma lu bari mooy xam gi mu xam Seexul Xadiim.

Nii nag la saxoo ak Sëriñ Tuubaa ci Mbàkke Kajoor gi di jàng, di liggéey, di yalwaan, di toroxlu ngir jëmi Yàlla di jàngale. Am fulla, bari pasteef, taqoo lool ak Sëriñ Tuubaa. Dëkk bu Sëriñ bi mas a sañc ànd na ko ak moom.

Sëriñ Abdu Rahmaan ku bari yërmande la woon, réyyoon ag jaayante, li koy firndeel mooy ba ko Sëriñ bi gëramee daf ne ci moom lay toog. Ba ko Sëriñ bi laajee loo bëgg, daf ne buñu naree mbugal benn murid ëllag neen ko jox dolley malaaka mu déeku mbugal gi. Boobu la ko Sëriñ bi digal naafila kaamil ci ñaari ràkka. La ko jiitu nag daan na naafila kaamil waaye ci ay ràkka yu bari. Am na ñu wax fukki ràkka ak ñaar ci njëlbéenam ginnaaw gi mu di ko def téeméer.

Sëriñ bi doyloo woon na lool xelu Sëriñ Abdurahmaan ba tax na daan na diisoo ak moom. Dafa doonoon ku man a topatoo ay mbir, man a topatoo ay ndogo. Lum war a def lu nekk rekk, daf key defee na mu gën a refete, gën a jàppandee. Doonoon ku set, ñame dëgg, doyloo Alxuraan, sàmmonte lool boole ci.

Am kollare lool. Ba Seex Ibra génne àddina téeméeri Kaamil la ko jàngal. Ba Sëñ bi nekkee ca géej ga, ña mu yoroom ñi ci ëpp mokkal neen Alxuraan. Sëriñ Basiiru Mbàkkee nee : « masumaa gis ku ko gën a baarkeel am jàngale ». Sëriñ Abdurahmaan ci lii la sax, boole ko ak ñame naafila, di topatoo ay gan, di sàmm ñi ñu ko dénk.

Ba miy nekk Ndaam, moo daan jiite ca Jàkka ja, tegguwoon ci Siraatal Mustaxiim, dëddu, jàmbaree, am fit, dëggu.

Fa Daaru Salaam, ba ko Sëriñ bi di sàkketloo, la ko wax ne sa tank foo ko teg ku fa teg tankam du tabbi sawara. Am na ay bayyit yu ci Sëriñ Musaa Ka def ba mu key maarsiyaal.

Sëriñ Tuubaa daf ko fonkoon ba tax na seen i njaboot jaxaso cib séy ak ci pas-pas.

Sëriñ Tuubaa ne woon na Sëriñ Abdurahmaan murid saadix la, te ku jeex tàkk ci moom la. Ne woon buñu bari meloon ni moom kon dina noppalu. Gëram na ko ba taay, di ko wax ak di ko bind.

Mbolleem Seex yi fonkoon neen ko ak di ko tudde doom.

1943 la génn àdduna ci weeru Sahbaan. Sëriñ Mbàkke Buso moo ko jullee, doomi Sëriñ Tuubaa yi ñoo ko rot ci bàmmeel.

Yal nanu Yàlla fayal Sëriñ Abdurahmaan Lóo te taas nu ci baarkeem. Li ëpp ci li nu fi bind, noo ngi ko gëstoo ci Sëriñ Basiiru Ture yal na ko Yàlla dolli yiw te taxawu ko.

S’abonner
Notification pour
guest
0 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR