Sëriñ bi nag moo gis Sëriñ Masàmba fekk ko ci ronn garab muy yër ab téere. Sëriñ bi nuyu ko, ñuy jàmmasante ak a waxtaan.
Ginnaaw gi nag la Sëriñ Masàmba laxasaayu ni day seeti Sëriñ Tuubaa. Ci la daaldi dem Pataar ci daaray Sëriñ Moor Anta Sali nekk fa di fa yokk jàngum xam-xamam waaye itam mu man faa nekkaale ak Sëriñ Tuubaa. Ci jamono yooyu la ko Sëriñ Masàmba tàmbalee liggéeyal, wormaal ko lool, bëgg ko lool.
Bi Seexul Xadiim defee wooteem ju réy ji ginnaaw bi Sëriñ Moor Anta Salli làqoo. Te loolu moo di jëm ci Yàlla, tey yar nit ñi ci yite, déet ci jàngum kese, la Sëriñ Masàmba Jóob jaayante ak Sëriñ Tuubaa. Mooy ñatteelu nit bi ko def ginnaaw Sëriñ Aadama Géy, Sëriñ Ibraahima Saar.
S’abonner
0 Commentaires
Le plus ancien