Kan Mooy Sëriñ Musaa Halima Géy?

Sëriñ Musaa mi ngi cosaano Badar Géy, gane àddina atum 1890. Sëñ Maxtaar Géy baayam moo ko jàngal, teel ko dalal lool. Sëñ Musaa moom Soxna Halima mii, moo doon caatu baayam. Bi fi baayam bàyyiko, ginnaaw gi, maggam Sëriñ Mor Halima àggaleel ko jàngam.

Li ko boole ak Sëriñ bi nag, moo di bi Sëriñ Moor déggee mbiri Sëriñ Tuubaa fa Jolof, daf ko seeti, ginnaaw gi it dikkaat fa ànd ak rakkam. Ba Sëriñ bi gisee Sëñ Musaa daf ni ñu dalal ko Alxuraan ngir tuutaay bi ak néewi at ji. Waaye boobu Sëriñ Moor ni ko, defoon na ko ba noppi, te mokkal na. Ci guddi gi Sëriñ bi woolu Sëriñ Musaa ni ko taril, ginnaaw tarig lenn ci Alxuraan, Ku Baax Ki ne ko, mokk na. Sëñ Musaa ne « boobu la ma woor ne mokkal naa ».

Ginnaaw Jolof gi nag, la dikk Njaareem. Féetewoo bind Alxuraan ak Xasiidaa. Lii moo doonoon aw tànnam fa kër Seexul Xadiim.
Sëriñ Suwahibu wax na Sëriñ Ahmad miy doomi Sëñ Musaa, amoon naa ñaari gàll yoy li ci nekk yépp Sëñ Musaa Halima moo ko bind.

Sëriñ Mustafaa Xasiida, Sëriñ Suwahibu it néttali na ko, moom Sëñ Musaa du néttali benn mbir ci Sëriñ bi bu dee fàtte na ci benn baat. Seex Abdul Xaadir, Imam Bu Mag bi, mas naa wax ci Sëñ Musaa « akka màndu »!

Sëriñ Tuubaa dafa fonkoon bindum Sëñ Musaa lool, daan na sopp it kuy roy bindam. Daan na topp it kaamil yi daan dikk fa moom. Sëriñ Fàllu it noonu mas naa bindloo Sëñ Musaa Xasiida Walaqad Karamnaa, Wakaana Haqan ak Wajahtu Kullil Wadoodi Samadi ngir taalube yi baarkeelu ci mbindam. Bëggoon it kuñuy wax Isaa Ñang mool ko far mu agsi. Moom Sëriñ Fàllu ne lii de yéeme na « Musaa key bind, Isaa key mool ».

Bokk na ci ay jagleem, Sëriñ bi mas na ko woo bis jox ko am bind ne ko bindal ma ko te bul ko xool. Ne ko ndax man nga ko mu ne ko waaw. Booba nee na xamul lum doon waaye xam na ni ginnaaw Sëriñ bi nee na ko man nga ko, ba mu ne ko waaw rekk fàww mu man ko. Ba mu demee ba dikk Sëriñ bi laaj ko ndax bind nga ko ni ma la ko waxee woon. Mu ne lo waaw. Boobu fekk na Maam Seex Ibraahima Faal toog, mu ni ko : « Musaa muus nga di bind loo xoolul ». Te lii ba ko Sëriñ bi di digal Sëñ Musaa fekku fa Maam Seex.

Sëriñ Tuubaa it mas naa gis bindum Sëñ Musaa daaldi ne « Muusaa yaa bind lu refet lii ci sa loxo bu tuuti bii », boobu ab kaamil la yët ku baax ki.
Mas na ko wax « bul daw li nga yor daa diis ». Boobu xayna Alxuraan gi lay wax (Sëñ Alhaaji).
Mas naa rëdd wërale ça Jolof . Daaldi key wax Musaa lii mooy xolu doomu aadama, def ay rëdd ci biir cercle bi. Ne ko lii lépp ay lëndam la, saa suñu la tooñee nga muñ ko ngir Yàlla Subhaanahu mu def benn tomb leer. Bu yàggee xol bi lépp leer lay doon. Sëñ Musaa nee na boobu laa gej a mer.

Ku baax ki amoon na coffeel lool ci Sëriñ Musaa Halima Géy. Sëñ Musaa it bëggoon ko lool. Dundam gi yépp moom la ko jox. Bi fi Seexul Xadiim jóge daa yeeslu ci njabootam, dalle ko ci Seex Muhamadul Mustafaa ba ci Sëriñ Abdul Ahad.

1973 mooy at bi fi Sëriñ Musaa Halima Géy bàyyeeko. Yal na Yàlla yokk ay leeram barkeb Alxuraan ak Xasiiday Sëriñ Tuubaa, ndegam moo doon liggéeyam.

S’abonner
Notification pour
guest
2 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
yacine
yacine
2 années il y a

Maa Shaa Allah. Yalla nanou yalla tass si barkem

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR