Kan Mooy Sëriñ Musaa Ka

Moo doon Werekaanu Bàmba, di xamle jaar-jaari yoonu murid, cëslaayi
yoon wi ak daan dànkaafu képp kuy dal ci Sëriñ bi mbaa ci yoon wi.

Mooy koo xam ne kenn du sosal kenn ci ñoñ yoon wi mbaa boroom yoon wi te mu nekk fi. Mooy délluwaay bu mag bi ci xam melloy Sëriñ
Tuubaa, ay jikkoom ak ya mu baaxoo.

Mooy ki daan marsiyaal Góor Yàlla yi ba ñu man leen a xam. Di way Taalube yu mag ya àndoon ak Sëriñ bi. Niki Sëriñ Abdu Rahmaan Lóo, Sëriñ Mbàkke Buso, Maam Seex Ibraahima Faal, Sëriñ Muhammadu Mustafaa ak ñeneen.

Di ñu xamal Yonent bi Aleyhi Salaam ak lenn ci Sahaaba yi.

S’abonner
Notification pour
guest
0 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR