Daa mel ni wax ji jenn la. Doomi Soxna Mati Jaxate ak Sëriñ Saalihu dem am gi bet na nu.
Daf doon murid saadix, te ay kilifaa ko wax, seedeel ko ko. Yal na ko Yàlla dolli xéewal fa mu nekk, yërmande ak i leer te taas nu ci barkeem. Sunu Boroom yal na ko sàmmal mbolleem njabóotam ak i taalibeem.

Li nu xam ci moom mooy dundam gi daa amoon njariñ, te du deñ di nu njariñ ngir bàyyi na fiy màndarga ak lu ñu koy fàttalikoo. Defar na ay nit, taalifi téere, sàmm lool cosaani yoon wi. Ñépp a wax neen ko, te daa boolewon tabe, fonk mbokk, te fonk taalibe yi.
Xasiida yi moom ni mu ci melloon yéeme na. Léppi Xasiida yi moo ko ñoroon. Di ku baax, di ku dëggu te bëgg Sëriñ Tuubaa, demam gi tiis na nu.Daf doon kenno ci yoonu murid, doylu, ràññe lool, gore, te fees dell ak hikma, bari xam-xam, am fulla, yeewu, te refetum xel. Daa amoon diine, te sàmmoonte, fonkon Alxuraan, set lool, te teey.