Kan mooy Sëriñ Njaase Siise?

Bismilaahi Rahmani Rahiim

Sëriñ Njaase Siise mi ngi gane àddina dëkk bunuy wax Haafiya Njoogu. Ay way-juram ñooy Sëriñ Ahmadul Muxtaar Siise ak Soxna Salla Jaxate. Mi ngi jàngee ci baayam. Mu doonoon nag ku yéeme ci Alxuraan ba nee nañu ci Alxuraan la daan dunde. Daan na bind ab kaamil wecce ku ko ñatti téeméeri dërami ngurd. Wax neen ne bu ko wecce ba laa dund bee jeex mu bindaat beneen. Am bis mu ñëw seetsi Sëriñ Tuubaa, bi mu nuyoo, Sëriñ bi laaj ko foo bàyyikoo? Mu ne ko maa ngi bàyyikoo Aafe Njoogu ca Kajoor. Sëriñ bi laaj ko noo tuddu mu ne ko Ibraahima waaye Biraahim lañu may wax. Mu laaj ko noo def ak Téere bi? Mu ne ko: ku ko mokkal laa. Mu laaj ko looy liggéey? Mu ne ko ci Alxuraan laay liggéey, damay def bu ma bindee ab kaamil jaay ko ñatti téeméeri ngurd, ba laa jeex ma bindaat beneen jaayaat ko. Sëriñ bi ne ko man ngaa dem, bu guddi jotee nga ñëw taril ma Alxuraan, bi mu demee ba guddi, mu ñëw taril Sëriñ bi. Sëriñ bi ne ko Alxuraan ji rafet na lool waaye Alxuraan ak njariñ man la ko Sunu Boroom jox, daal di ne ko: délluwaatal bindal ma ab kaamil àndil ma. Bi mu ko àndee mu laaj ko fa nga dëkk ku fa gën a jagge ci fere yi? Mu ne ko Sëriñ Masàmba Jóob Saam. Sëriñ bi bind ab bataaxel jox ko, ni ko « na teral Alxuraan » . Sëriñ Masàmba Jóob jàng bataaxel bi dindi juróomi téeméeri ngurd jox ko ko. Bi mu nëwaate ci Sëriñ bi ak kaamil bi, Sëriñ bi ne ko dama la doon won rekk ne maay Boroom Alxuraan. Am nga ci Juróomi téeméer ak sab kaamil, te ñatt téeméer nga ko daan jaaye. Bi Sëriñ bi ñibisee ci géej gi ba ñëw Njaaréem, ci la ñëwaate ci Sëriñ bi, mu teey ko di ko bindloo, di ko jàngale loo. Fi Daaray doomam ji nekk (Sëriñ Moor Mbay Siise) moo nekkoon Daaraam ba ni mu génne àddina 1946 ñu dénc ko Njaaréem.

Xibaar yi nag jëlle nañu ko ci Siira Masaayixul Muriidiya bi daayira Xuratul Hayni liggéey ci ndigalu Sëriñ Allaaji Baara Fallilu yal na ko sunu Boroom dooli yërmande ak ngëram waaye ak kilifteefu Seriñ Ahmadu Mbàkke Suhaybu yal na ko Yàlla dooli wér, ta guddal fanam barke Seexul Xadiim.

Al-Habdul Xadiim
17/12/2020

S’abonner
Notification pour
guest
9 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
A. Gueye
A. Gueye
4 années il y a

MaSha’ALLAH Yallah na ga am faye si ligueye bi si barkei makk gni

Baye Mor
Baye Mor
4 années il y a

Jaajëf amatina solo jàmbaar ji

Babacar Thiam
Babacar Thiam
4 années il y a

Allahouma amine Bidiahi SERIGNE TOUBA Wa Mame Cheikh Ibrahima Fall LAMP FALL BABOUL MOURIDINA.

Seck Baay Faal
Seck Baay Faal
3 années il y a

Hakassa lii d ligeey bu am solo la

Ndiaye Sarr Ndiaye
Ndiaye Sarr Ndiaye
3 années il y a

Machalla yalla Nanou yalla tasse ci bar kéllame ❤️

Dernière modification le 3 années il y a par Ndiaye Sarr Ndiaye
Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR