Bismilaahi Rahmani Rahiim
Lii ab tënk la ci dundug Soxna Maymuunatu Suxraa bintu Sayxil Xadiim radiya laahu anhuma.
Soxna May mi ngi feeñ atum 1343 ci gàddaay gi, 5i fan ci weeru koor, dëppoo ak 1925 ci milaadiya ci Jurbel. Way-juram wu jigéen ji Soxna Maam Xari Daaru Sill dóomi Sëriñ Bàmba Sill, dóomi Sëriñ Tafsiir Muhammadu Ndumbe Maar ma jullee woon Sëriñ Moor Anta Sali Mbàkke. Mi ngi jàngee Alxuraan ci Sëriñ Asan Jaxate ba watu ko, jàngee xam-xam ci magam Seex Muhammadul Faadil ba yéeme ci. Mi ngi yaroo ci Tarbiya-suufiya, ci diggante way-juram wu jigéen ak yaari magam yi Seex Muhammadu Mustafaa ak Seex Muhammadul Faadil ba mujju doon ab royuwaay ci mbooleem jigéeni julit yi, rawante na murid yi ci yite ju kawe ak taalube gu dëggu ak njariñ mbindéef yi.
Ay jikkoom mooy baax, mandu, ragal Yàlla, tabbe, sell, dëddu àddina, bëgg Yàlla lool, ak Yónnent bi ak Sëriñ bi, di muridatun saadixatun, ku siiw ci joxe ci yoonu Yàlla ak dimbale fuqraawu yi, ak miskiin yi. Di lijanti soxlay nit ñi loolo waral këram daa fees akuw nit. Doon ku bëgg Alxuraan, ku ko fonk, fumu tool di ko jàng. Ku am diine akub taalube, daa leele rawante na waa Daaray Kaamil.
Yar kat bu mag la woon dees ko daan àndil xaleyu jigéen yi mu di leen yar, di leen defar. Ku siiw la cig ubbiku ak yaatu ak laabir, ak woyof ak defar ab diggante. Defoon ni mu bokkal Sëriñ bi ñu di ay Sëriñam, mu di leen liggéeyal, di leen jox ay àddiya. Ñoomit ñu jàppee ko seen dóomi Sëriñ wormaal ko lool, fonk ko lool. La fa nitu àddina yi daan ñëw lépp, taxul mu fàtte li mu doon. Lu bari ci kër Sëriñ si xàmmee nañu lool ay ndàbbi berndeelam.
Am na Xasidag wolof gumu def sant ca Yàlla sant ca Sëriñ bi, yeesal ca ak jaayanteem ak Sërin bi. Sant ca Seex Muhammadu Mustafaa mi ko yar ci diine akug taalube, ak xamal ko ki mu doon. Mu diggal ca taalibe yi yite ju kawe, ak taalube gu dëggu.
Mi ngi nekkoon kër Sëriñ Seex Awa Bàlla, mooy way-juru Sëriñ Muhammadul Mahfuus ak Soxna Baali. Mi ngi fi jóge atum 1999 radiya laahu wa nafahnaa bi barakaatiha.
Xibaar yi nag jëlle nañu ko ici Siira Masaayixul Muriidiya bi daayira Xuratul Hayni liggéey ci ndigalu Sëriñ Allaaji Baara Fallilu yal na ko sunu Boroom dooli yërmande ak ngëram waaye ak kilifteefu Seriñ Ahmadu Mbàkke Suhaybu yal na ko Yàlla dooli wér, ta guddal fanam barkeb Seexul Xadiim.
Al-Habdul Xadiim
15/12/2020
MaSha’ALLAH
Jërëjëf
Jaajëfati yaaram yàlla na Sëriñ bi taxawu lépp
Amiin Amiin mu boole nu ko barkeb Sëriñ Abaas