Mi ngi gane àdduna bisu àjjuma ci weeru Rajab ci Daaru Salaam atum 1888/1889 di doomi Seexul Xadiim ak Soxna Awa Buso. Sëriñ bi moo ko dalal Alxuraan moom ak magam Seex Muhammadu Mustafaa. Sëriñ Daam Abdu Rahmaan Lóo moo ko àggalel jàngum Alxuraan ci Daarul Haaliimul Xabiir Ndaam. Sëriñ Maam Moor Jaara moo ko […]
Mi ngi gane àddina 1912 fa Daarul Aaliimil Xabiir, mi ngi feeñ ci weeru safar. Doomi Xaadimu Rasuul la, Soxna Faatima Suxraa mooy way-juram wu jigéen, Sëriñ bee ko jëlle Gànnaar moom ak Soxna Faatima Kubra way-juru Seex Abdullaahi Mbàkke. Ñoom ñépp ay sariif leen. Ba mu dikke àddina la Sëriñ Abdu Rahmaan yabal ndaw […]
Bismilaahi Rahmani Rahiim Sëriñ Njaase Siise mi ngi gane àddina dëkk bunuy wax Haafiya Njoogu. Ay way-juram ñooy Sëriñ Ahmadul Muxtaar Siise ak Soxna Salla Jaxate. Mi ngi jàngee ci baayam. Mu doonoon nag ku yéeme ci Alxuraan ba nee nañu ci Alxuraan la daan dunde. Daan na bind ab kaamil wecce ku ko ñatti […]
Bismilaahi Rahmani Rahiim Lii ab tënk la ci dundug Soxna Maymuunatu Suxraa bintu Sayxil Xadiim radiya laahu anhuma. Soxna May mi ngi feeñ atum 1343 ci gàddaay gi, 5i fan ci weeru koor, dëppoo ak 1925 ci milaadiya ci Jurbel. Way-juram wu jigéen ji Soxna Maam Xari Daaru Sill dóomi Sëriñ Bàmba Sill, dóomi Sëriñ […]
Bismilahi rahmani rahim. « Lii ag tënk la ci dundug Soxna Aminata Seex Mbàkke bintu Sayxil Xadiim » Mi ngi gane àddina Daarul Aaliimil Xabiir ci atum 1922, wayjuram wu jigéen mi ngi tudd Soxna Faabéy Jóob mi bokk ak Soxna Faati Tuuti Jóob miy wayjuru Sëriñ Murtada lépp. Moom la Sëriñ Umar Faal di wax ca […]