gear Paramètres Push
chat
Mooy doomi Ahmadu Roqaya Faal ak Soxna Saynabu Njaay. Mi ngi cosaano ci Damel yi, doonoon ay buur fa Kajoor. Mu bàyyi lépp ginnaaw ngir aajawoo Boroom ci na mu gën a kawe ci yite yi. Mi ngi gane àddina atum 1855 walla 1856. Lu man a xew daal Sëriñ Tuubaa ñatti at la ko […]
Sëriñ Abdu Rahmaan Lóo mooy doomi Muhamad Lóo moom Mayib moom Aaliyun moom Ibraahima Lóo. Ndeyam móodi Maryaama Sekk moodi doomi Moor Jaane moom Muxtaar Sekk mi nekkoon Tayba Cekkeen. Sëriñ Abdu Rahmaan ci altine la gànne àddina weeru Gàmmu 1852 walla 1853 foofu la màgge, duggee fa Daara ba mokkal Alxuraan. Am na nag […]
Bismillahi Rahmaani Rahiim Mi ngi ganee àdduna Tuubaa fii barabu Sëriñ bu Mag bi nekk. Turam moodi Seex Muhamadu Lamin Baara di dóomi Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu ak Soxna Aminata Lóo. Ci 28 Jumaadal Ulaa 1309 la gànne àddina dëppook 20 décembre 1891. Sëriñ Baara mi ngi jàngee Alxuraan ci Sëriñ Abdu […]
Bismillahi Rahmaani RahiimMi ngi gane àddina atum 1954, Soxna Maam Jóob mooy way-juram wu jigéen bokk ci waa Koki, way-juram wu góor di Sëriñ Abdu Xudoos moom Maam Cerno. Sëriñ Moodu Faati Jéy Jóob moo ko dalal Alxuraan fa Daaru Salaam moom ak seexam Sëriñ Fàllu waaye Kooku ci fukki atam ak ñaar la wàcce […]
Sëriñ Musaa mi ngi cosaano Badar Géy, gane àddina atum 1890. Sëñ Maxtaar Géy baayam moo ko jàngal, teel ko dalal lool. Sëñ Musaa moom Soxna Halima mii, moo doon caatu baayam. Bi fi baayam bàyyiko, ginnaaw gi, maggam Sëriñ Mor Halima àggaleel ko jàngam. Li ko boole ak Sëriñ bi nag, moo di bi […]
Bismillahi Rahmaani Rahiim Soxna Aysatu Mbàkke doomi Seexul Xadiim ñu gën koo xam ci turu Soxna Astu Gaawaan mi ngi gane àddina 1904. Way-juram wu jigéen mi ngi tudd Soxna Xadi Jóob gën a siiwe ci Soxna Xadi Gànnaar di doomi Madu Faa-Xujja moom Masàmba Anta Ceebo. Sëriñ bi moo ko dalal am jàng. Bi […]
Mi ngi ganee àdduna atum 1867 ca poroxaan, turam dëgg mooy Seex Siidi Muxtaar Mbàkke mi ngi bokk ci askanu Maam MahramMaam Seex Anta doomi Sëriñ Moor Anta Sali la moom Maam Bàlla moom Maam Mahram.Maam Anta Njaay Mbàkke, doomi Maam Ibraahima Awa Ñang moom Maam Mahram mooy yaayam. Kon Muhammadul Xayri Mbàkke walla nga […]
Ca 1958 la daaldi am sañ-sañ man a taxawal mbébétam. 1963 nga ci la aji Màkka, ba mu ñibisee tukkiwaat na ànd ak Sëñ Mustafaa Lo ak Sëñ Yande ci réew yu sori niki Kowet, ak Iraak 9i weer. 1965 mu jógaat dem Araabi Sawdi. Al-Azhar nag ci ay coono yu metti la ko taxawale […]
Mi ngi feeñ jamono ci atum 1340 dëppoo ak 1920 walla 1921, 26 fan ci Gàmmu ca dëkk buñuy wax Daarul Haalimul Xabiir, ñu gën ko xam ci Ndaam. Soxna Njaxat Silla nettali na Sëriñ Mustafaa Lo ne ko, Sëriñ Ndaam dey terale na 33 gàtt Sëriñ Murtada. Ba weeru gàmmo teerse day def bis […]
Sang bi mi ngi gane àddina ci atum 1881 ca Pataar, ab dikkam ci àddina soreewul ak jamono ji way-juram wa, Sëriñ Moor Anta Sali di wuyu ji boroomam. Seexul Xadiim di magam moo ko tuddu jox ko turu Masàmba Anta Cebbo ginaaw ba mu demewoon siyaare ji barabu Sëriñ Moor fa Deqële. Sëriñ Moor […]