Bismilahi rahmani rahim. « Lii ag tënk la ci dundug Soxna Aminata Seex Mbàkke bintu Sayxil Xadiim » Mi ngi gane àddina Daarul Aaliimil Xabiir ci atum 1922, wayjuram wu jigéen mi ngi tudd Soxna Faabéy Jóob mi bokk ak Soxna Faati Tuuti Jóob miy wayjuru Sëriñ Murtada lépp. Moom la Sëriñ Umar Faal di wax ca […]
Seex Ahmadu Ndùmbé Mbàkke mi ngi ganné adduna 1859 ci dëkk buñu naan Nja feeté Mbàkke Baol, doomi Sëriñ Zayd Mbàkke la, moom Saër Soxna Busó moom Maam Mahram. Mi ngi yaroo ci kepparu wayjuram, and naak mom wooté Màba Jaxu Ba ca Saalum nekk Poroxan. Ginaaw ba wayjuram wa nélawé la dem Mbàkke Kajjóor […]