Dees na jàngee ci nettali yi lenn ci mayi Sëriñ Bi, yërmandeem ci nit ñi, ak mbaaxam, ak bëgg gu tar gum bëggoon Yonent bi Aleyhi Salaam. Noonu ba tay di neen fi déggee lol daf nuy gën a soññi ci ab yar, sàmmonte, ak bëgg lu baax. Gën a góor-góorlu ci sunuy séy ak […]
Ci xaaj bii di nanu fi jàngee nees di njariñoo ci Sëriñ Bi. Naka noonu ay teegin yu sew te gànjaru di na fi feeñee. Ba tay ci xaaj bi, di nanu dolliku bu baax ci gën a xam Xasida yi ak seen dayo. Naka noonu Alxuraan ak i njariñam. Yal nanu Yàlla xiir ci […]
Ci xaaj wi di nanu fi xàmmee ne, ànd gi nu ànd ak Sëriñ Bi, tawfeex kepp la. Ba tay di nanu fi jàngee ne, ag njub, ag mbaax lépp ci coobarey Yàlla lay aju. Nun défunt ludul jéem. La Sëriñ Tuubaa dénkoon Soxna Fati Ja ci dolleey lixlaas dees na ko fi jàngee tamit