Mi ngi feeñ jamono ci atum 1340 dëppoo ak 1920 walla 1921, 26 fan ci Gàmmu ca dëkk buñuy wax Daarul Haalimul Xabiir, ñu gën ko xam ci Ndaam. Soxna Njaxat Silla nettali na Sëriñ Mustafaa Lo ne ko, Sëriñ Ndaam dey terale na 33 gàtt Sëriñ Murtada. Ba weeru gàmmo teerse day def bis […]
Ca 1958 la daaldi am sañ-sañ man a taxawal mbébétam. 1963 nga ci la aji Màkka, ba mu ñibisee tukkiwaat na ànd ak Sëñ Mustafaa Lo ak Sëñ Yande ci réew yu sori niki Kowet, ak Iraak 9i weer. 1965 mu jógaat dem Araabi Sawdi. Al-Azhar nag ci ay coono yu metti la ko taxawale […]