Jotaayu Texe (2)

Dees na xamee ci xisa yi yu bari ci mayi Yàlla yi. Nit dina man a xam ay mbir yu nëbbu ci coobareey sunu Boroom. Dina fi feeñee itam dolleey ngëm, dooleey kóolute ak i jeexitalam ci topp ndigalu Sëriñ bu mat Sëriñ. Yal nanu Yàlla saxal ci ag taalube, sàmmoonte, ak ragal Yàlla.

Jotaayu Texe (1)

Li ab Téere bu m njariñ lool, ay wax ak i jëfiinu Sëriñ Bi moo ci nekk, nu man ci gindiku ci sunu lislaam ak ci sunu taalibe. Fii nag matug Boroom Tuubaa dina di feeñee ak sunu tawfeex ci ànd ak moom. Yal nanu nuur ci moom barkeb Xasiida yi .

Tombi Borom Tuubaa (30)

Noo ngi toll ci sunu 30i xaaj ci Tombi Borom Tuubaa. Dina feeñee ci néttali yi ni liggéeyal Sëriñ amee lool doole ci nun ak tawfeex gi nekk ci topp ay ndigalam ak bàyyi ay tereem. Naka noonu di ko sant fu nu toll, doyloo ko, woolu ko te womatu ci moom man na noo […]

Tombi Borom Tuubaa (29)

Fii dana fi feeñee farlug Sëriñ bi ci jëfe ndigalu sunu Boroom, ak xam gi mu xam ni àdduna jaaruwaay la. Naka noonu terangay Alxuraan ci ñu koy jàng ak tawfeex gi ci Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu am. Su ko defe lii di nu soññi ci xam ne àdduna du kërug sax, […]

Tombi Borom Tuubaa (28)

Sëriñ bi fii dina fiy néttali mbir yu am solo ci pajug yaram. Dina fi wax it nees di jëfandikoo lenn ci xob yi. Nangug ag ñaanam, ak xam nees di fasee sa soxla dina fi feeñ ak ni mu fonkewoon aaya Alxuraan yi ci lépp lumuy def. Naka noonu ag sàmmam ci diinee, woyof […]

Tombi Borom Tuubaa (27)

Ginnaw fàttli yi aju ci ndëgarlaayug néttali yi, ci leen daaldi wéyal yaatal wi. Am na ci yu jëm ci mbiri tubaab yi ak waxiini Sëriñ bi, na miy kaweem xel, ak nees di déggee ay waxam. Kollareem ak taalube yi itam dina fi fés, fullaam, ak dénkaane yu am solo yi muy def ak […]

Tombi Borom Tuubaa (26)

Fii danu fiy néttali leen ci téerey boroom ngir yi ni nu agsee ci Sëriñ bi. Tawfeex gi mu am ci ànd ak Boroomam ci lépp lu muy dugg dees na ko fi xam itam. Naka noonu sell gi woon ci moom taxoon na dara manta rax ay mbiram. Fàww rekk lu sell rekk lay […]

Tombi Borom Tuubaa (25)

Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu daf nu fi dénk jàng, liggéey ak sàmm sunu diine. Dina fi leeral itam, moom Sëriñ bi, lu jëm ci ay mbiram niki wirdam, Sëriñam, yoonu géej gi ak yeneeni mbir. Naka noonu dees na fi déggee lenn ci ay jagleem ak i xéewalam. Yal nanu Yàlla xir […]

Tombi Borom Tuubaa (24)

Sëriñ Tuubaa dina fi leeral leen ci baati wolof yi ak mahnaa gi ñu ko wara jox dëgg-dëgg. Lenn ci xarbaax yi itam dees na feeñee fi. Naka noonu Hikma yi.Ba tey ci néttali yi di neen fi dégg luy waral nu wara gën a sàmm sunu kolare ak Sëriñ Tuubaa, sunu diggante ak moom […]

Tombi Borom Tuubaa (23)

Fii dañu fiy fésal ni Sëriñ wéetale Boroomam ak liggéey gu muy liggéeyal Yonent bi Aleyhi Salaam ak ni mu key feeñale ci mbindam. Naka noonu sunu Borom dig na ko lu réy ëllag ginnaaw jaamu Yàlla ju refet gi mu jaamu Boroomam ak jaayanteem ju réy ji.

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR