Bismilaahi Rahmani Rahiim. Nu fas yéene matal li desoon ci bayyit yi nga xam ne Sëriñ Alhaaji Mbàkke àndi na ko ci Dooley Mbidum Sëriñ Tuubaa. Muy ay bayyit yoo xam ne ku ko dégg di nga ci jëlle njariñ, sag pas-pas ak sa mbëggeel itam ci Sëriñ bi man na ci yokk bu wér. […]