Sëriñ Tuubaa nee na » Ca gaal ga la ma Yàlla xamalee ne kuy liggéeyal Yonent bi laa. Foofu it laa taggee Yonent bi tagg wuy sax di ko fekk fa mu ne » . « Fa Conakry, Yàlla setal na ma ci lépp luy jëme ci lu ñaaw, fegal ma ko. Tagg naa fa Yonent bi […]
« Ku yàkkaar ne sama tukki bii dama cee jëm feen fu dul ci Yàlla ak Yonent bi ba tax mu may dëkk yor jaasi ak i kano, Yàlla dana ko gàcceel, seetaan ko, mbindéef yi dinañu ko ngàññi, yeed ko, mu dee ak gàccee ak toroxtange. Yàlla nag dina ma dimbali far ak man, mbindéef […]