Bismillahi Rahmaani Rahiim Mi ngi ganee àdduna Tuubaa fii barabu Sëriñ bu Mag bi nekk. Turam moodi Seex Muhamadu Lamin Baara di dóomi Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu ak Soxna Aminata Lóo. Ci 28 Jumaadal Ulaa 1309 la gànne àddina dëppook 20 décembre 1891. Sëriñ Baara mi ngi jàngee Alxuraan ci Sëriñ Abdu […]