Fii deef na leeral lenn ci ay teggin yi nit ki wara làmboo bu toogee ak ay mag walla mu nekk ci biiri nit. Naka noonu deef na fi béral itam, ni nit ki wara sàmmee ay gëtam ak làmmiñam. Di xool lu baax, di am kersa tey wax yiw. Di tàggat boppam itam ci […]
Dog wi deef na fi àndi itam lenn ci xar-baaxi Sëriñ bi, lenn ci yi ko Yàlla may ak lenn ci ay hikmaam Naka noonu da nga fi dégg ay hisa yuy wone ni am na it ñu ko daan jéem a natu ci anam yu kéemaane. Ak ni mu daan delloo lépp ci Yàlla. […]
Fii dees na fi wone lenn ci màndargay yërmandey Sëriñ bi ak ñi mu daan sàmme kollare. Ni mu wàccoog nun itam ci wax, ci jëf ak ci bind. Ak ni mu defoon ragal Yàlla muy lépp. Naka noonu dees na fi leeral yennet ci xisa yuy wone xar-baaxi Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara […]