Tombi Borom Tuubaa (8)

Lii dees na fi jàngee doxiinu Sëriñ Tuubaa ci Alxuraan ak fonk gi mu ko fonkoon. Daf daan digle jàng Alxuraan, di ko durus ci ay lim yu wuute. Ba tay muy soññi way-jur yi ci jàngal seen i doom Alxuraan. Dëkkam bii di Tuubaa it muy fésal ag bëggam ci am ñu fa nekk […]

Tombi Borom Tuubaa (7)

Xaaj wi dees na fi xamle diggante Sëriñ bi ak Alxuraan. Ak ni mu daan yittewoo gone yi di jàng Alxuraan. Daf daan teral Alxuraan, ak di ci déggee ay mbiram, di ci dalal xelu ab taalubeem. Di xamle itam yenn ci mbóot yi ci aaya yi. Di leeral itam ay aaya ci anam gu […]

Kan Mooy Maam Seex Ibraahima Faal ?

Mooy doomi Ahmadu Roqaya Faal ak Soxna Saynabu Njaay. Mi ngi cosaano ci Damel yi, doonoon ay buur fa Kajoor. Mu bàyyi lépp ginnaaw ngir aajawoo Boroom ci na mu gën a kawe ci yite yi. Mi ngi gane àddina atum 1855 walla 1856. Lu man a xew daal Sëriñ Tuubaa ñatti at la ko […]

Xare Badar

Bismillahi Rahmaani Rahiim Lii lenn la ci xew-xewi Badar ! – Yi ko sabab mooy wooteg Yonent bi Aleyhi Salaam: ñiy jaamu xëram ànduñu ci woon. Di rey ñi néew doole ak di jéem a ger (corrompre) ñi xaw a bari mbokk. Ba am sax am ñu Yonent bi wax ni neen Gàddaay dem Ethiopie. […]

Tombi Borom Tuubaa (6)

Bismillahi Rahmaani Rahiim Yu bari ci néttali yi nu fi àndi day soññee ci weetal Yàlla miy Aji Moom dëgg-dëgg. Di fi joxe ay tegtal ci wuuteeg àddina ak allaaxira. Di dénkaane itam ci wattandiku mellow àdduna di nu nax.

Tombi Borom Tuubaa (5)

Bismillahi Rahmaani Rahiim Dees na xamee ci néttali yi nu fi dajale njariñal dëddu ak fexe xam bu wér ñi àdduna di wore. Su ko defee ab soññee la ci nit ki mu wara xam lim war a gën a fonk ci dundam ak ci doxiinam. Té loolu moo di fexee dundal sa ruu, sàmm […]

Tombi Borom Tuuba (4)

Bismillahi Rahmaani Rahiim Fii ay dénkaane yu jëm ci Sëriñ Mbàkke Buso deef na ko fi dégg. Mellow taalube dëgg-dëgg, néewal nelaw yi lu tax manul ñàkk, dëddu àdduna ak dëgmal ëllag li tax manta ñàkk dina fi feeñ. Soññee na it bu baax ci wattandiku yeen jikko yi nga xam ne Yàlla gëramu ko. […]

Tombi Borom Tuubaa (3)

Bismillahi Rahmaani Rahiim Sunu xaaj wi daanaka li ci ëpp ci melloyu baax yi nit ki wara làmboo ak di ko jikkowoo moo ci nekk. Moo xam sunu digante ak sunu bop, sunuy dëkkando, sunuy way-jur ak yeneen. Mu niy soññi bu baax ci farlu, ak di jëf lu baax te bañ koo yéem. Di […]

Tombi Borom Tuubaa (2)

Bismillahi Rahmaani Rahiim Ci xaaj wi dees na fi xammee leen ci néttali yi jëm ci lu dib Taalibe. Wax na fi lu aju ci topp ndigal ak bàyyi tere yi. Lépp jëm ci yokk góor-góorlu ci jaamu Yàlla, teggin yi war ci nodd, moytu lépp luy lu bon. Di waxtaane it lu baax, di […]

Tombi Borom Tuubaa (1)

Bismillahi Rahmaani Rahiim Ginnaaw leeral lu aju ci natuwaayu xisa yi. Deen fiy yaayal waxtaani Sëriñ Tuubaa walla Tombi Boroom Tuubaa. Sëriñ Alhaaji Mbàkke moo bind Téere bi. Di ko ñaanal mu yàgg fi lool te wér. Yàlla dolli ko kàttan ak man-man ci lépp. Su ko defe saa bu àndee benn xisa rekk day […]

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR