Bismillahi Rahmaani Rahiim Lii lenn la ci xew-xewi Badar !
– Yi ko sabab mooy wooteg Yonent bi Aleyhi Salaam: ñiy jaamu xëram ànduñu ci woon. Di rey ñi néew doole ak di jéem a ger (corrompre) ñi xaw a bari mbokk. Ba am sax am ñu Yonent bi wax ni neen Gàddaay dem Ethiopie.
– Bi Waa Madin ( Yasrib) ñëwee Màkka di aji. Yonent bi Aleyhi Salaam xamal leen Lislaam. Lu wara toolo ak ñatt aj. Ba ñu matee limub 72, Yonent bi it di leen wax ni bëgg na ñu aar leen bu ñu ñëwee Madina.
– Waa Màkka am na sax ñu teggoon 100i gileem dig ko képp kuy jàpp Yonent bi Aleyhi Salaam
– Ba ñu saxee Madiina nag ci ab diir la ab aaya wàcc jox leen ndigalu xeex : Uziina li laziina yuqaatiluuna bi anahumu zaalimuuna wa ina Laahu hala nasrihim laqadiir.
– Li ñu njëkk def mooy sàmm seen alal ak jël li ñu moom yi yéefar bu ñiy dem ci yeneen dëkk yi . Hamza ak 34i sahaaba def neen ko. Ubayda Ibn Haris ak 200i sahaaba itam, Saad Ibn Waqas moomit ak 8i sahaaba. Moom Yonent bi ak Muhaajirun yi lu tooloo ak 101i sahaaba.
– Amoon na it ay « services de renseignement », te mooy ñiy jéem a xam lu noon bi nar.
– Bi lépp leere la dajale 77i Muhaajirun li ci des di Lansaar yi. 313i di lim bi yépp.
– Yonent bi Aleyhi Salaam ne ku pare rekk neen dem. Amoon neen ñaari fas ak 70 gileem. Seydina Aliyun yor raaya Muhaajirun yi. Saad Ibn Mu’aas yor bu Lansaar yi. Xale yi ñu ne leen neen toog. Umayr ibn Abi Waqaas di jooy naan day bokk.
– Zubayr ak Miqdaad ñoo waroon fas yi.
– Abu Sufiyaan itam di waajal. Yabal Dam-Dam ne ko waxal waa Màkka ñu waajal. Dam-Dam dag gileem bi, xooti ay yereem ni leen Muhammad nangu na seen « caravane ». Li waa Màkka yàgg a bëgg mujj sotti nag.
– Yonent bi mi ngi woon fuñuy wax Safra, yoonu Badar, foofu leen ko waxee ni waa Màkka ñoo ngi ñëw. – Yonent bi woote waat ndax bëggoon na xam ba xam Lansaar yi di neen nangoo xeex. Mu laaj ñépp lu ñu xalaat. Déllu Madina walla xeex. Seydina Abu Bakr, Seydina Umar, Miqdaad ñépp ne lu Yonent bi wax rekk lañuy def.
– Saad ibn Muwaas (lansaar) jóg ne ko daa mel ni ñun nga bëgg ñu wax. Di neen topp sa ginnaaw. Boo doon xuus ci géej gi, ñu xuus ba jeex. Di neen seral sa xol te di nga gis sunu jàmbaar. AbduLaahi ibn Mashud ne bis boobu Yonent bi daa bég, kanam gi leer lool ndax wax jii.
-Badar nag mooy xare bi njëkk ci Lislaam. 313i wara jàmmarlo ak 1300i yu waajal dëggantaan ngir xeex. Di bàkku di ñëw. Ba ñu toole fu ñuy wax Juhfa. Abu Sufiyan yónne ni leen, man ngeen déllu Màkka aar naa « caravane » bi. Waaye Abu Jahli ne moom day xeexi ndax ñépp xam ni am neen doole. 300i nit déllu, 1000i yi dëgmal Badar.
– Guddig Badr nag taw na fa taw bu yéeme. Muy xéewal ci Jullit yi. Doon ab musiiba ci yéefar yi – Ci bis bi ba ñu jubbee Badr Yonent bi daaldi sàmp tante. Hubaab ibn Munzir ne ndax sa xalaatu bopp la mu ne ko waaw. Ma ni ko man li la gis mooy nu jiitu Badr, def mbalka bu mag di ci naan, te fat teen yi su ko defe yéefar yi duñu ci naan.
– Ci bëccag gi Yonent bi Aleyhi Salaam di joxoñ naa Abu Jahli fii lay daanoo, Umaya fii, diw fii. Te ni mi ko waxee woon noonu la amee. – Boobu jullit yi doggu neen lool ci xeex ak fàttu. Nga xam ni daray ragal newul ci ñoom. – Ñu def seeni sappe fas yéene jihaad. Yonent bi Aleyhi Salaam jiite ko, ginnaaw ñaan ak soññi Sahaaba yi.
– Sawaad xawa génn sàppe yi bi Yonent bi Aleyhi Salaam di defar xaw koo cuuj. Sawaad ne ko gaañ nga ma. Yonent bi ne ko fayul. Mu ni ko ba nga may gaañ sama biir daa muriko. Kon muril sa biir. Yonent bi muri ko. Sawaad foon ko. Ne ko damaa bëggoon sunu yaram jonjo ba laa xare bi.
– Yonent bi ni leen ku ci faatu dem àjjana. Ñii di door jaasi, ñii di fet, ñi di sànni xejj. Seydina Aaliyun ak Seydina Hamza di rey rekk. Miqdaad ak Zubayr noonu. Abu Judaana (lansar) moomit di rey rekk.
– Ñaari waxambaane Lansaar xoos Abdurahmaan Ibn Hawf, ne ko kuy Abu Jahli. Mu joxoñ leen ko. Ñu songi ko, tasaare ñi ko wër, ba xaw koo rey. AbduLaahi ibn Mashuud wëri ko. Abu Jahli ne ko yaw sàmm bi yaay teg sa tànk sama dënn bi. Ibn Mashuud dag bopp bi yóbb.
– Sunu Boroom yabal junni Malaaka, béneen junni wàccaat, beneen junni waajat.
Saydina Jibril jiite leen. Ibliis daw ndax mi ngi won ci yéefar yi jël jëmbu ku ñuy wax Suraaqa.
– Jullit yi am ndam ju réy. Yegle ko fépp. Yahuud yi mer, di ko wedd. Naafeeq yi gis ni am neen dolle dugg ci Diine. Sahaaba yépp bégg. Lii noo ngi ko doon taataan ci kàddug Sëñ Kajaali Njaay. Yal na gudd fan am wér te làq ngëramal Seexul Xadiim.
Maa Shaa Allah amatina solo lol
Jërëjëfati
Manchallah dieuredieuf amna solo dieuredieuf
Hakassa. Sant neen