Soxna Muuminatu nu gën koo xam ci Soxna Moomi, kenn la it ci njabootu Seexul Xadiim. Mi ngi gane àdduna fa Ndaam ci atum 1914. Soxna Faati Silla Libaas mooy way-juram wu jigéen. Sëriñ Tuubaa moo dalal Soxna Moomi Alxuraan fa Njaaréem ginnaaw ko mu jox ko Sëriñ Moor Halima Géy, ginnaaw gi mu jox […]