Mi ngi gane àdduna bisu àjjuma ci weeru Rajab ci Daaru Salaam atum 1888/1889 di doomi Seexul Xadiim ak Soxna Awa Buso.
Sëriñ bi moo ko dalal Alxuraan moom ak magam Seex Muhammadu Mustafaa. Sëriñ Daam Abdu Rahmaan Lóo moo ko àggalel jàngum Alxuraan ci Daarul Haaliimul Xabiir Ndaam. Sëriñ Maam Moor Jaara moo ko jàngal lu bari ci xam-xam. Maam Ceerno Biraahim itam jàngal na ko lu bari ci xam-xamu diine ak tarbiya ni ko Sëriñ Tuubaa digle ci Murid yépp, mootax mu ni won « man ak Seex Mustafaa sunu Baay Ceerno daf noo jàngal ba nu né ar mu yar nu ba nu ne nër »
Moom Sëriñ Fàllu bindal na Sëriñ bi 28 kaamil ci li nu xam, woy na Sëriñ bi it lu bari ci araab ndax ku déggoon araab la. Ci atum 1928 la aji Màkka ànd ak Sëriñ Mbàkke Buso ak Maam Seex Anta Mbàkke. Ci atum 1914 nag la ko Sëriñ bi yabbaloon Tuubaa moom ak Seex Mustafaa ak yéneen kilifa.
Dëkk yi mu sanc bokk na ci: Ndindi, Mbépp, Madina-Boba, Xaayaan, Tuubaa-Mirina, Naylul-Maraam, Aaliya, Tuubaa-Suraŋ, Bogo.
Dëkk yi yépp Daara la ko defoon di fa jàngale ak tarbiya ak liggéey. Lépp lu fa masaana jóge it da ko daan joxe àddiya ci liggéeyu Jumaa ji.
Wax neen ni bi Sëriñ bi nekke Njaaréem ci atum 1925 da ko woo ni ko: « danga ma daan laaj ndigël ngir liggéeyal ma, kon digal naa la nga dem Tuubaa nekk ca liggéeyu Jumaa ja. ku dikk na la ca fekk ku dem na la ca bàyyi ». Mu dikk Tuubaa nekk fii ak Seex Mustafaa ba mu wuju ji boroomam atum 1945.
Ginnaaw loolu la Sëriñ Fàllu nekk xalifa yoonu murid. Ci la waxe Mourid yi nuy daje Tuubaa màggal , mu daal di jublu ci liggéeyu Jumaa ji ngir àggale ko. Tàmbale fi Seex Mustafaa yemoon ànd ko ak murid yi yépp, nekk seen jëwrin lumu am def ci, luñu ko jox mu def ci ba mu àgg ci atum 1963, ñu julli ci, ci teewaayu kilifa yu bari. Fekkoon na mu defoon fi marse okaas ak foraas bu Daarul Manaan ak nat dëkk bi, yaatal mbed yi ba ñépp am kër yu baax ak yéneen yu bari.
Nekkoon na ku yaatu, tabe, lewet, boorom gis-gis la woon, lu bari lum daan wax tay jii la gën a feeñ. Mi ngi génn àdduna 16 août 1968 ci Tuubaa, Yàlla nanu ko Yàlla fayal ci barke Seexunaa Ahmadul Xadiim.
Lii nu fi bind, noo ngi ko xame ci Soxna Ayda Bàmba, moom mu xamee ko ci Sëriñ Abiibu Jóob, Yàlla neen fi yàgg te wér te matal seenub yéene ci liggéeyu Seexul Xadiim.
Al-Habdul Xadiim
10/03/2021
Maa shaa Allah. Amatina solo lol. Dieureudieuf Mouride.
Hakassa noo ko bokk