
Sëriñ Móodu Maamun mooy doomi Maam Seex Anta ak Soxna Buri Mbàkke.Sëriñ Móodu Maamun sëti Maam Maharam la ci ñaari wet yépp. Mi ngi gane àddina atum 1887 walla 1888 fa Tuubaa. Ba mu feeñee jamono rekk la way-juram wu jigéen faatu. Nu jël Sëriñ Maamun jox ko Sëriñ Tuubaa mu defal ko la mu key defal, am yu mu digal Maam Seex Anta. Sëriñ Tuubaa daaldi digle ñu jox ko Soxna Aminata Lóo, am na it ñu wax Soxna Awa Buso.
Ginnaaw dañoo jubloo tënk nag du nu man a yaatal xew-xew bii ak yi ci am yépp. Nu jàll Kon ci am jàngam.
Jaar na ci Sëriñ Abdu Rahmaan Lóo. Waaye Sëriñ Aafiya Mbàkke moo ko yéggalil ba mu mokkal Alxuraan. Li ëpp ci jàngum xam-xam bi nag ci Sëriñ Tuubaa la ko jëlle. Am na it ñu ko Sëriñ bi daan booleel ñu di ko jàngal xam-xam ba miy nekk Gànnaar.
Sëriñ Tuubaa ku amoon coffeel ci moom la. Li koy firndeel mooy ba Sëriñ bi jóge ci géej ba Maam Seex Anta di ko ganale, daf ko teel a laaj. Ne ko ana Muhammadul Maamun. Bi mu ñëwee Sëriñ bi ne ko fu alluwe wi toll ? Mu ne ko mokkal naa. Sëriñ bi ne ko taril. Muy tari baat bi di lox. Sëriñ bi yey ab guro, yàbbi jox mu lekk. Boobu la Sëriñ Maamun géj a taxaw ci Alxuraan.
Sëriñ Maamun itam noonu la meloon ci Sëriñ bi. Ba Sëriñ bi di nekk Jolof mas naa woote ñépp daje. Mu ne leen man ngeen a déllu ci seen i way-jur. Bi ñépp demee ba ca suba si, Sëriñ bi gis ko ne ko lu tax demoo ? Mu ni ko da nga wax ni na ñépp dem ci seen i way-jur, te man yaw yaay sama way-jur. Sëriñ bi ne ko loolu de sikkuwul. Am na it bis Sëriñ Tuubaa toogloo ko ci barab fa Njaaréem, mel ni ku ko fa fàtte. Taxul mu jóg fa mu toogoon.
Ay jikkoom yu refet taxoon na Sëriñ bi doyloo ko ci lu bari. Ku tabe la woon lool. Mooy ki njëkk jox àddiyay miliyon jébbal ko Sëriñ Fàllu Mbàkke, boole ci almet.
Ci loolu la Sëriñ Musaa ka naan : « ku deeti def ay milyon hidaaya, di yot xaliif fa Tuubaa ànd ak gaa ya ».
Sëriñ Maamun sanc na itam ay dëkk ginnaaw ba mu yeesalee Daaru Salaam ba noppi ci teewaayu Maam Seex Anta, woote fa ab màggal dundalee ko ak ay Kaamil yu bari.
Mi ngi fiy bàyyikoo atum 1969. Sëriñ Abdul Xaadir Mbàkke moo ko jullee.








