
…Am na benn buur gu féetewoon Lambay dafa sonnaloon lool murid yi ba Sëriñ Mbàkke Buso bindoonko bataaxal di ko wax mu teey loram ci murid yi.
Sëriñ Mbàkke Buso it dund na lu metti atum 1895. Ndax ci at moomu la baayam, miy nijaayi Sëriñ Tuubaa, faatu. Demug Sëriñ Mbusoobe tiisoon na ko lool. Ba tay ci at moomu la Sëriñ Tuubaa ci coobareg sunu Boroom nekk ci yoxoy tubaab yi. Muy beneen tiis.
Te teewul bindoon na ab bataaxel di ci xamle ni Sëriñ bi dañukoy tuumal rekk. Ci at moomu itam la këram lakk ba jeex. Lii lépp tax na Sëriñ Mbàkke Buso jóge Tuubaa dem dëkk bu ñuy wax…
S’abonner
0 Commentaires
Le plus ancien