Dénkaaneb Sëriñ Alhaaji Mbàkke (3)

Bismilaahi Rahmaani Rahiim.

Fii daf fiy leeral mbiri ñenti noon yi te mooy bakkan, bànneex, saytane ak àdduna. Muy wax itam lëkkalo gi nekk ci diggante bakkan ak bànneex. Xamle fi itam nees di def ba noot leen. Naka noonu, la fi leerale lu aju ci bëgg a àdduna, wax na fi itam màndargay mucc si worug àdduna.

Waaye noonu it lanu fàttalee sunu wareef sunu diggante ak sunu Boroom, te loolu sax mooy tax ñu mucc ci pexey saytane. Mu ñaax nu fi itam topp bu wér Sunnas Yonent bi Alayhi Salaam ak ndigali Sëriñ bi. Mu woo nu ci làmboo ay teggin, ak muñ. Ñaanal nu fi luy seed sunu xol.

Al-Habdul Xadiim
11/06/20

S’abonner
Notification pour
guest
2 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Mourtalla
Mourtalla
3 années il y a

Amna solo looool

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR