
Sëriñ Abdulaahi ku taqoowoon la ak baayam ju baax ji, nuru ko lool ci mello.
Mootax Seex Musaa Ka nee : « Allaahu moo di jenn waay, moo jàpp doom def ko ni baay ». Wax na it : « boo gisee muy sàmmandaay, Seex Bàmba ñoo nuroo jotaay, nuroo yaram, nuroo sewaay, nuroo doxiin, nuroo waxiin, nuroo jëmb ak melloog doxiin…
Moo doonu tab ga woon ca moom, moo doonu Jàmbaar gi woon ci moom… baatin ba raw na saayiram ».
Bi fi Seexul Xadiim bàyyikoo la daaldi Jaayante ak Sëriñ Muhammadul Mustafaa Mbàkke, nekk Daaru Minan fa wetu magam Sëriñ Muhammadul Basiiru Mbàkke. Jamono yooyu doon na jàng Nahwu ci Sëriñ Habiibu Mbàkke (…)
S’abonner
0 Commentaires
Le plus ancien