
…Dafa mel ni li moo doon cëram, mu sawar lool ci dimbali nit ñi.
Bi mu toole ci 40i at nag la daaldi fas yéene dimbali ñi fi ne. Di xamle ak a won nit ñi lu leen man a teeqale ak def bàkkar, ak di jëf nangam ci lu baax ngir man a tàbbi àjjana. Mu daan wax ku ne nag liy sa jagle.
Ci lii la ba ni mu fiy jóge. Borom baatin la won. Ni ko seede bari neen lool. Waaye ci biir loolu mu woyofaloon boppam lool , bari yërmande. Waaye daan dund sharihatul islaamiya. Daawul nangu kuy woyofal lu sunna woyofalul.
Lii moo doon meloom ci gaatal. Moom nag atum 1993 la wuyuji Boroomam. Lii noo ngi ko toxale ci waxi Sëriñ Saalihu Salaam, doomam. Moom Sëriñ Saalihu it mi ngi def liggéey bu am solo ci yoonu Seexul Xadiim. Di bind ak di wax lu am njariñ. Yal na gudd fan te ànd ak wér. Yal na ko Yàlla yokk yërmande te taas nu ci barkeem.