Kan Mooy Sëriñ Masàmba Mbàkke?

Sang bi mi ngi gane àddina ci atum 1881 ca Pataar, ab dikkam ci àddina soreewul ak jamono ji way-juram wa, Sëriñ Moor Anta Sali di wuyu ji boroomam. Seexul Xadiim di magam moo ko tuddu jox ko turu Masàmba Anta Cebbo ginaaw ba mu demewoon siyaare ji barabu Sëriñ Moor fa Deqële. Sëriñ Moor nag matatul a ajaar ndax ñu bari xam nañu ko. Borom, xam-xam la woon, dib Xaadi, yeewu woon lool ci àddina, ràññeeku woon lool ci mbiri diine, te xamoon lool nees di maslaa ak buur yi. Doomam yépp a sell, te doon i góor Yàlla.

Doy na ci misaal Sëriñ Masàmba mii nuy xamle, tey doomi Soxna Aysatu Jóob ñu gën koo xam ci Soxna Isa Jéey miy doomi Sëriñ Moor Xujja Kumba mi taalif « Muxaadimatul Kokkiyu ». Ginnaaw lii nag, dafay koo xam ne Sëriñ Tuubaa Xaada lahu laahu Maxtaara lahu, mooy ki ko yar, mat ko mag, mat ko baay. Ba mu amee 7i at la ko jox Sëriñ Abdu Rahmaan Lo. Ca yoxoy jàmbaar jooju la mokkale Alxuraan, jàngee fa itam bind. Manoon ko lool nag. Xelam neex lool ba jéggi dayo ba taxoon na Sëriñ Ndaam di yeexal ab jàngam. Waaye diir su gàtt Sëriñ bi dem Gabon, ca dëkk boobee la yónne woon ab bataaxel di ci xamle ni Sëriñ Masàmba man naa toxu ci yoxoy Sëriñ Abdu Rahmaan jëm ci yoxoy Maam Cerno ngir jàng xam-xam. Fa Borom Daaru, di magam itam la sax diirug li Sëriñ di ñibisi mu daaldi ñëw jaayante ak moom te Yàlla tax ni mbokkam yépp defe ak magi taalube yi.
Ag jàmbaaram taxoon na lu Sëriñ bi bind te ñu war cee jot daan na ko sottiwaat ci ndigalam, te it wax neen ni moo daan maas ag mbidam. Ca waar woowu la nekk ba làq ngëramam. Mooy ki féetewoon mbiri jàngkat yu mag ya daan yékkati Xasiiday Seexul Xadiim ba ñu leen di dàqantale  » Waa Kër Sëriñ Masàmba ».

Sëriñ bi mas naa wax :
«KUY WAX, WAXAL MASÀMBA!
KUY JOX, JOXAL MASÀMBA!
KUY LAAJ, LAAJAL MASÀMBA!
KU MASÀMBA NEXUL, TOPAL SAMA BAARAAM!

Sëriñ Mbay Jaxate, guinaaw ab dénkaane bu gànjaru ñaanal na ko lii:

<<Wéyal ba géejug sëriñ bi far la wann tërëx
Nga far ne meŋ ba nee faa « Bacc wéy na ba lab”. Tey làmb jaa ngii di gor, koo seeru nag mi ngi tëb. Ngir bëgg a ub, yobbu ndam; yal nan ko ub te nga ub>>.

Mi ngi wàcce liggéey atum 1942 fa Kaolak, ñu denc ko Tuubaa, murid yu mag yi ñu ci bari ñoo ngi fa woon. Seex Muhamadul Mustafaa bis boobu daa wax ne « tay jii laa ñàkk sama baay ».

Dundug Sëriñ Masàmba dafay déggal ne

Lin war a njëkk a jàngal xale moy Alxuraan, te moo jiitu ci yarub Sëriñ Tuubaa niki mu ko defee ci Sëriñ Masàmba.

Kuy tàmbali am jàng taamu nan ca mu tàmbalee ko ci ku am barke; ngir mu barkeel, ni ko Sëriñ Tuubaa defee, dalal Sëriñ Masàmba.

Ku yor gone warnay sutural may yi mu gis ci moom ba laa ñu kaa catu, Sëriñ ndaam Abdu Rahmaan bam gisee xelu Sëriñ Masàmba neex lool da daan yeexantul am jàngam ngir dawal ko cat.

Noo ngi taxawlu fi tey sant Soxna Màgget Mbàkke mi nu xamal lii, nu wëlbatiku xamal leen ko di ko ñaanal ngëramal Sëriñ Masàmba. Di ko ñaanal sunu bopp itam ak mboolleem ku dawal mbind bi mbaa nga teewlu ndégat li, mbaa te nga tasaare ko.

Al-Habdul Xadiim
22/06/2021

S’abonner
Notification pour
guest
6 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
BASSIROU CISSE
BASSIROU CISSE
3 années il y a

Kawétina d, Dieuredieufati yalla na souniou Borom gueuneu deugueureul taxaway bi

Saliou fall
Saliou fall
3 années il y a

Machallah fall

Momar Sokhna Niane DIOP
Momar Sokhna Niane DIOP
3 années il y a

Jërëjëf sang Bi

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR