Kan mooy Sëriñ Mbay Jaxate?

Soxna Penda Kumba Faal mooy way-juram wu jigéen, Sëriñ Xaali Majaxate Kalla mooy baayam, moo ko jàngal itam. Ginaaw gi it jàngee na it ci Sëriñ Moor Saasum Jaxate.

Ba fi baayam jóge ci atum 1900 la daaldi fas a jaayante ak Seexul Xadiim waaye boobu Sëriñ bi mi ngi ci tukeem ya, loolo tax mu nekkoon ak Maam Cerno fa Daaru Manaan. Ba Sëriñ bi nibisee la ko fekki Gànnaar, nekkoon fa ak moom daan fa bind ay Kaamil itam. Foofee ca Gànnaar la ko Sëriñ bi boole ak Sëñ Ahmadu Gay firdawsi ngir mu jàngal ko xam-xam moom ak Sëriñ Amsatu Jaxate, di mbokk ci moom te nuroo lool ak Sëriñ Mbay ay mbir ndax Borom Tuubaa da leen a boole woon a fonk te dëggaral yaakaaram ci ñoom. Ba tay jàngee na ci Haalim bu mag ba Sëriñ Abdu Rahmaan Loo. Ca Gànnaar googee la tàmbali def ay woyam, di taalif. Teewul nag Sëriñ bi def ci moom ay mbiram. Ndax bi Sëriñ bi nibisee ba mu gisee Sëñ Mbay Jaxate laaj na ko baayam, mu ne ko faatu na waaye « baayi na fi ndab lu man a def » . Sëriñ bi ne ko
« Ndab li danaa ko raxas ba mu set, duy
ko bamu fees, ubb ko ba du xajam du tuuru »
Lii day xamle ne Sëriñ bi dafa teela am yéene ci sunu sang bi, am ci moom yaakaar lool. Doy na ci firndeel, li mu ko dénkoon Sëriñ Basiiru daaldi koy wax ne damaa bëgg nga def ci moom yar ak nga jàngal ko Alxuraan te na ngeen dem ci dëkk bunuy Siinu Xaali nga def ci moom yi ma la wax. Ni mu ko bëggee rekk nii la amee. Ci atum 1912 la ko Sëriñ bi gëram ca Njaaréem yeewi ko. Ginnaaw ga mu dem Pir dëkku way-juram wu jigéen jël fa Soxna. Ci atum 1918 la Sëriñ Mbay Jaxate dem Xuru-Mbàkke ci ndigalu Sëriñ Tuubaa, li ko waral moo di Sëriñ Habibullah mi bokk ak Sëriñ bi Soxna Jaara moo daan feeñu Sëriñ bi di ko jàmbat ab wéetal fa Xuru-Mbàkke. Sëriñ bi daaldi diggal Sëriñ Bàlla Faal xellare, doonoon kenn ci bëkki néegu Sëriñ Moor Anta Salli, te gudd fan lool, mu won sunu Sang bi fi ñu dénc Sëriñ Habibu.

Sëriñ Mbay da doon góor Yàlla am sàmm lool, yeewu lool te bari solo. Doon funuy seentoo njaboot gu baax. Loolu sax tax na Sëriñ bi joxoon ko doomam Soxna Mbeen Ngabu, Maam Seex Ibraahima Faal, jox Soxna Aminata Faal

Moom nag ku rëyoon yitte la daan na wax Sëriñ bi, « Naa far di bopp ci yaw, naa far di tànkk ci yaw ; Naa far di kenn ci yaw, saa aajo jaa ngi fajal »


Moo tax waxoon na itam:

 » Sëriñ bi ngir Yàlla ni sukkar di seeye ci ndox ba kenn du séenati jëmam, naa di séeye ci yaw.

Atum 1919 nag la Sëriñ bi gane ji Sëriñ Mbay Jaxate ànd ak Sëriñ Bàlla Coro, am nañu ne Seex Isaa Jenn àndoon na ci, am ñu ne Sëñ Demba Kebe . Waaye njëkk Sëriñ bi di fa ñëw Seex Mustafaa Mbàkke jiitu woon na ko fa, Sëriñ bi it foofu la lenn fekk ñoom ñaar ñépp. Foofu la jullee yoor-yoor, tisbaar ak Tàkkusaan, nat Jàkkay Xuru-Mbàkke ci tanku boppam. Leeram ya teeloon dëddu ca Njaaréem itam fa Xuru-Mbàkke leen leen dénc.

Naka la Sëriñ Mbay Jaxate daan Tarbiyaa?

ku man a defare la woon, daan ci roy Sëriñ bi. Daf daan xaajale góor ñi ak soxna yi. Te daan leen tere ñuy xoolante. Sëriñ Mustafaa doomam wax na ne:  » mas naa romb sama nday ci teenn xamuma xawma ko » . Ba ci xool gi sax, dikk na ci xibaar yi ñu ne Sëriñ Mbay ba ko sunu boroom nattoo ci loolu, te mooy xool ci bët keneen kudul soxnaam, dafa jëll xorom di ko bomb ci ci ay bëti boppam bamuy nàcc. Céy bi le sàmmoonte!!! Baraay la daan xéewlo boole ko ak xorom def ko ci këll guñu njort ne Seriñ bee ko ko joxoon. Te lu néew la ci daan jëfandikoo. Dafa ñame woon di naafile guddi itam. Doonoon ab suufiyanke bu wér a wér.

Waaye ana lan la ko Sëriñ Tuubaa may ci boppam?

Ay waxam, ndax ñi masaana bàyyikoo fa moom dikk Njaaréem fekk fa Sëriñ bi. Bu leen laaje ani Baabakar? Ba ñuy tontu ne ma nga fay wax rekk. Da naan leen « mba sikku leen ne la muy wax ci man la jóge » .

Sëriñ bi daan na ko wax itam: « Yàllaa ma la faye ». Moom it mu ngoy rekk ci sangam, bàyyi bunt bépp sang ngir Borom Tuubaa.
Amul won saggo ci moom, looloo waral bi fi jëmbi Sëriñ bi jóge dafa jaxasoo woon lool. Ba bokk na ci ni ko doon soññi waat, Sëriñ Moor Kayre, di wax ak moom ci ay wolofal yu siiw. Bokk na ci ya mu ko wax képp ku xellu rekk bu teewloo say bayit day bàyyi lépp loo xam ne caaxaan la, te daaldi déllu ca la ko war.

Li ko waral moo di Sëriñ Mbay ay wolofalam dafa fees dell ak ay jàngale yu jëm ci diine, ci sóobu yoonu Yàlla, ci dëddu àddunaa ak mboleem xoy-xoyi àddina. Di ci jàngale Sëriñ bi ak royukaay yu mag ya. Di jaaji taalube yi ci sax ci ndigal tey fonk seen i kilifa. Di xamle mbiri àjjana, mbaaxug sunu Boroom, yërmande ji ak mandoom ja. Di soññee ci nite ak fonk doomu-aadama, ak bañ a xebb kenn. Di tere ndamu, beew ak rëy. Mu dégg diine lool te xam àdduna… Te loolu lépp yaa ngi koy xamee ci bindam yi. Yàlla nanu Yàlla fayal Sëriñ Mbay Jaxate fàww ci barkeb mbóotum Alxuraan.

Lii lépp ci Sëñ Usmaan kebe leen ko xamee ginnaaw bi mu ko gëstoo ci njabootug Sëriñ Mbay Jaxate. Ku ci bëgg a xam lu gën a yaatu, ma nga ko xool ci chaîne YouTube Serigne Mbaye Diakhaté.

Al-Habdul Xadiim
21/03/2021

S’abonner
Notification pour
guest
6 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Narou Kawsara
Narou Kawsara
3 années il y a

Diadieufety yaram

Momar DIOP
Momar DIOP
3 années il y a

Mâcha Allah sang Bi Sant nañu bubaax

Saliou fall
Saliou fall
3 années il y a

Machallah fall 👌

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR