
Diirug li ñuy nekk foofu ñoo ngi doon liggéeyal Sëriñ bi ba am ngëramam.
Ci liggéeyu Sëriñ Tuubaa gi la sax, moo tax sanc na ay dëkk di fa defare. Bokk na ci yooyu dëkk Daaru-Faal, Tuubaa-Faal, Kuuba, Aynu Rahmati añs. Amoon ay tool yu bari, di bàyyi xel tolluwaayu jamono moo tax mu ubbiwoon « école », di yaatal « réseaux téléphoniques » yi ngir yombal xam-xam ak wàllum jokkoo yi.
Jàmbaar dëgg la woon, ñamewoon liggéey, man a joxe, bari pasteef lool. Di fàtte boppam ngir liggéeyu Sëriñ Tuubaa. Daan na joxe at mu ne ñaari milyong at mu ne ci liggéeyu Jumaa ji.
Waaye ci baay ji la ko doonoo. Am na bis sax Sëriñ Tuubaa santoon Seex Mustafaa mu utal ko ay seng. Bi Seex Ibra déggee lii, la daaldi bëgg a féetewoo liggéey boobu. Sëriñ Tuubaa ne ko Seex Mustafaa laa ko sant.








