Kan Mooy Sëriñ Siidi Muxtaar Mbàkke

Sëriñ Siidi Maxtaar, Sëriñ Baara Mbàkke ak Soxna Mati Ley ñooy ay way-juram. Mi ngi gane àddina atum 1925 fa Mbàkke Kajoor.

Baayam moo ko dalal Alxuraan, jox ku turondoom Sëriñ Seex Awa Bàlla waaye mi ngi mokkale Alxuraan ci kenn ci taalibey Sëriñ Baara ñu di ko wax Sëriñ Ñaan Jóob.

Bi mu noppee ci jàngum Alxuraan gi la sóobu yoonu sàkku xam-xam. Moo tax jàngee na ci Sëriñ Móodu Dem ak ci Sëriñ Muhammadu Lamin Jóob Dagana. Ba mu noppee ci lii la déllu ci turondoom fa Daaru-Manaan.

Moom Sëriñ Siidi Maxtaar nag bariwoon na ay Daara lool ci dëkki àll yi di fa xamle Diine ak di ko def ci nit ñi. Ku tabewoon la lool. Li koy firndeel mooy am na jamono joj mbënd bi sonnaloon na lool waa Senegaal, mu yékkati benn milyaar dimbale ko askan wi. Ab joxeem amu ci woon xeej ak seen. Nit ku amoon fulla la, te daan def yite ci jëfe ay xalaatam. Te ay xalaatam weesuwul woon liggéeyal Sëriñ Tuubaa ci ni mu gën a dëppoo ak bëggug Sëriñ bi.

Ku daan ñaan muy nangu la. Doonoon ku noppi, daan soññee lu bar ci coll gu yiw, di fonk julli ci jàkka yi. Daan béral bu baax ci askan wi ak ñiy laaj seen baat naan leen « ku yaruwul doo yor dara, ku amul i teggin doo teggi dara ».

Mooy ñaareelu sëtu Sëriñ Tuubaa bi toog ci xilaafa gi yilif yoonu murit gi yépp. Def ay liggéey yu am solo rawatina ci Jumaa ji. Moo ko jëlle ci juróomi sóorool yóbb ko ci juróom ñaar. Yeesal Jumaa ji ba mu gën a refet di taxawu ci soxlay a askan wi.

Ku matoon li mu doon la. Boroom pasteef la woon te réy yite. Atum 2018 la wuyuji Boroomam. Sëriñ Muntaxaa Mbàkke yal na fi yàgg te wér moo ko jullee, wuutu ko.

Yal nanu Yàlla fayal Sëriñ Siidi Maxtaar Mbàkke, taas nu ci barkeem. Yal na ko Yàlla dolli yërmande barkeb Seexul Xadiim.

20/07/2023
Al-Habdul Xadiim, Nitug Yàlla, xëtug 61.

S’abonner
Notification pour
guest
0 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR