Kan Mooy Soxna Muuminatu Mbàkke

Soxna Muuminatu nu gën koo xam ci Soxna Moomi, kenn la it ci njabootu Seexul Xadiim. Mi ngi gane àdduna fa Ndaam ci atum 1914. Soxna Faati Silla Libaas mooy way-juram wu jigéen.

Sëriñ Tuubaa moo dalal Soxna Moomi Alxuraan fa Njaaréem ginnaaw ko mu jox ko Sëriñ Moor Halima Géy, ginnaaw gi mu jox Sëriñ Abdu Rahmaan Lóo mu yéggalil ko jàngum Alxuraan gi. Bind na kaamil itam.

Ba wàll wi matee nag, la daaldi tàmbali sàkku xam-xam ci Maam Cerno Biraahim Mbàkke ak ci Sëriñ Mbàkke Buso. Ba miy noppi ci ñaari wàll yi mi ngiy am 13i at. Daaldi déllusi fa way-juram wu jigéen ndax ba miy am at yii la Sëriñ Tuubaa wuyuji boroomam, jébbal boppam Sëriñ Muhammadul Mustafaa magam.

Ginnaaw gi la ko Sëriñ Mustafaa yóbb Gede jox ko Sëriñ Mbàkke Buso mu fay liggéeyal boroomam. Sunu Boroom it jox ko fa njaboot, te mooy Soxna Maam Faati Bàlla Buso, Soxna Barakata (Gàdd) ak Sëriñ Isaa.

Ba fi Sëriñ Mbàkke Buso jóge la ko Sëriñ Fàllu jox Sëriñ Móodu Awa Bàlla mu am fa Sëriñ Baara Mbàkke, Soxna Baali, Soxna Maam Faati Mbàkke ak Sëriñ Seexunaa Mbàkke. Foofu la nekk di liggéeyal Boroomam ci anam gu sell ba ni fi Sëriñ Móodu Awa Bàlla jóge ci atum 1982.

Soxna ci déllusi Tuubaa wéyal ab liggéeyam ci jaamu Yàlla ak fàggu lu lew, di jàng ak a jàngale.

Soxna ci ku amoon diine la lool, daan bind ay kaamil ak di ko bindlu. Soxna ci daan na taalif itam ci wolof di ci jàngale farata yi ak sunna yi ci jaamu Yàlla yi. Daan na yare bu baax rawatina turondoom yi.

Ba tay, Soxna Moomi ab liggéeykat la woon. Dafa yoroon ay toll, daan na raablu itam. Jàmbaar tigi la woon.

Ci atum 1990 la Soxna Muuminatu Mbàkkae wuyuji Boroomam. Yal nanu ko Yàlla fayal, te yokk ay leeram dooli ko yërmande ba fàww te taas nu ci baarkeem.

S’abonner
Notification pour
guest
0 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR