Leeral Mawaahibul Xudduus (1)

Sëriñ Tuubaa XLML ginnaaw bi mu santee Yàlla sunu Boroom subhaanahuu
wa tahaalaa.

Julli ci Yónente bi SHWBW, daa xamle ne xam-xam mooy li gën ci lu Yàlla SW di jox ab jaam, waaye xam-xamu wéetal Yàlla sunu Boroom mooy la ca gën, lépp lu ñuy xaare bàmmeel ak yawmal xiyaam mooy la ca gën.

Loolu moo tax ñenn ci jàngkat yi sàkku mu wayal leen téereb Imaamu Sannuusi RL bii mu daal di jóg fas ko yéene koo way ( du ñàkk yu mu ciy dolli yoo xam ne nekkul ca téere boobu, ngir mu jariñ nit ñi rekk. ) Xam-xamu tawhiit nag, « te mooy wéetal sunu Boroom » li tax mu gën xam-xam yi mooy moom kepp boo ko xamoon dana doy, man ngaa tàbbi àjjana it. Te beneen xam-xam bu mu doon bu ci àndul du am njariñ.

Maa ngi ñaan sunu Boroom way wii doon lu nuy musal ci sawara, te sell lool ci lépp lu koy ñaawal, te doon ab yóbbal ci bàmmeel ak bis pénc. Képp ku ko mokkal, walla nga dégg ko, xam ko, yal na sunu Boroom fegal la ay fitna ci darajay Yónente bi SHTHBW.

S’abonner
Notification pour
guest
0 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR