
Saa su nu waxee su nu Boroom am na kàttan xamal ne li nu ci namm mooy mbir moo man a xalaat sunu Boroom man na koo amal te bu koy amal ca na mu ko bëggee la koy amale.
Saa su nu waxee nammeelug sunu Boroom SW mooy ki mu nekk ci moom day man a amal di man a ñàkkal di man a gàttal, di man a guddal, di man a xeesal, di man a njoolal di man a indi mbindeef, ci jamono jii walla jeneen, di man a xeetal mbindeef ci barab bii walla beneen, di man a xeetal mbindeef ci wet gii walla geneen, képp ku ñuy wax ne Yàlla la, fàww mu boole melo yii : dana doon ku am ba noppi dara du ko jiitu, mooy jiitu lépp.
Te day doon ku fiy des, te du niroo ak menn mbindeef, te doon ku doylu ci boppam, di dégg, di gis di wax. Képp ku ñuy wax ne buur la fàww mu doon ku am kàttan, gu mel ni ga ma doon wax, te lu mu bëgg amal ko ca na mu ko bëggee, te day doon ku am xam-am di dund. Képp kuy bind dara itam fàww melo yii daje ci yaw : kàttan gu mel ni ga ma doon wax, ak ug nammeel gu mel ni ga ma doon wax, ak xam-xam boo xam ne du umple dara, ba noppi di dund.
Balaa kenn a am ug mat fàww mu doon kuy dégg lépp, di gis lépp di wax. Boo seetloo xam ne melo yooyu yépp sunu Boroom SW moo ko man a melowoo.
Su ko defee meloy sunu Boroom bu ci ne am na fu muy aju, ag lu muy sottal, dananu ci indi juróom-benni melo ngir leeral, muy kàttanam ak ug nammeelam, ak ug déggam, ak ug gisam, ak i waxam ak xam-xamam.








