Bismillahi Rahmaani Rahiim Fii dama fiy béral Meññatum Tasawud Sixaar mu Sëriñ Allaji Mbàkke. Nga xam ne lu nit wara xam rekk ci Téere da nga ko fa fekk mu leeral ko, gaatal ko ba ñépp man ko dégg. Xaaj wu njëkk wi nag ndékaaney Sëriñ Tuubaa jëm ci ndaw ñi te mooy saxoo jub, […]
Bismilaahi Rahmaani Rahiim Ponki Lislaam lanu fiy leeral. Àttey Julli nag moom leen yaatal ci xaaj bi. Dees na fi xamee itam mbiri laab : jàpp ak sangu farata. Leeral neen fi it nees di jàppee ak naka lanuy sangoo farata. Mat naa xam ndax boo laabut doo man a def yeneen jaamu yi.Yal nanu […]
Bismillahi Rahmaani Rahiim Fii danu fiy lim faratay Julli, Sunnay Julli, Faratay Jàpp, Sunay Jàpp. Ginnaaw ba nu xamee ni ngir Julli man a wér fàww jàpp gi wér. Ak li nga xam ne it Imaam Xawfi xuppe na ko ci wàll woowu ngi soññiñu ci gëstu sunu Diine ak ràññatle bu wér liy farata […]
Bismillahi Rahmaani Rahiim Fii nag danufiy leeral sangu farata ak tiim. Di neen fi wax farata yi ak sunna yi. Li lépp dafay dugg ci mbiri laab. Naka noonu jullit bi dina fi xamee bu baax lu aju ci faratay koor, sunnay koor, faratay azaka ak teggini azaka. Naka noonu di neen fi xamle faratay […]
Bismillahi Rahmaani Rahiim Sunu bunt bu mujj ci Tasawud Sixaar dafa jëm ci fay li la raw boo àndeek Imam di julli ak waxtu yi ñu taamu ci julli. Li ci ëpp solo nag dafa jëm ci jikko yi ñu wara ame. Sëriñ bi li mu la njëkk diggal mooy yittewoo xam- xam, lewet, am […]