Li mooy tàmbalig Téereb Nahjul Qadaa Al-Haaji.Ubbite gi rekk doy na yóbbalug dund. Dina fi feeñee ay laabire yu am solo ci sax ci jëf lu baax te bañ a taayi. Naka noonu ay wax yu am solo te bari njariñ moo fiy fés. Ay royukaay ci bépp Jullit, te mooy sahaaba yu baax yi. […]
Bismillahi Rahmaani Rahiim Lii lenn la ci xew-xewi Badar ! – Yi ko sabab mooy wooteg Yonent bi Aleyhi Salaam: ñiy jaamu xëram ànduñu ci woon. Di rey ñi néew doole ak di jéem a ger (corrompre) ñi xaw a bari mbokk. Ba am sax am ñu Yonent bi wax ni neen Gàddaay dem Ethiopie. […]
Bismillahi Rahmaani Rahiim Sunu bunt bu mujj ci Tasawud Sixaar dafa jëm ci fay li la raw boo àndeek Imam di julli ak waxtu yi ñu taamu ci julli. Li ci ëpp solo nag dafa jëm ci jikko yi ñu wara ame. Sëriñ bi li mu la njëkk diggal mooy yittewoo xam- xam, lewet, am […]
Bismillahi Rahmaani Rahiim Fii nag danufiy leeral sangu farata ak tiim. Di neen fi wax farata yi ak sunna yi. Li lépp dafay dugg ci mbiri laab. Naka noonu jullit bi dina fi xamee bu baax lu aju ci faratay koor, sunnay koor, faratay azaka ak teggini azaka. Naka noonu di neen fi xamle faratay […]
Bismillahi Rahmaani Rahiim Fii danu fiy lim faratay Julli, Sunnay Julli, Faratay Jàpp, Sunay Jàpp. Ginnaaw ba nu xamee ni ngir Julli man a wér fàww jàpp gi wér. Ak li nga xam ne it Imaam Xawfi xuppe na ko ci wàll woowu ngi soññiñu ci gëstu sunu Diine ak ràññatle bu wér liy farata […]
Bismilaahi Rahmaani Rahiim Ponki Lislaam lanu fiy leeral. Àttey Julli nag moom leen yaatal ci xaaj bi. Dees na fi xamee itam mbiri laab : jàpp ak sangu farata. Leeral neen fi it nees di jàppee ak naka lanuy sangoo farata. Mat naa xam ndax boo laabut doo man a def yeneen jaamu yi.Yal nanu […]
Bismillahi Rahmaani Rahiim Fii dama fiy béral Meññatum Tasawud Sixaar mu Sëriñ Allaji Mbàkke. Nga xam ne lu nit wara xam rekk ci Téere da nga ko fa fekk mu leeral ko, gaatal ko ba ñépp man ko dégg. Xaaj wu njëkk wi nag ndékaaney Sëriñ Tuubaa jëm ci ndaw ñi te mooy saxoo jub, […]
Bismillahi Rahmaani Rahiim Lii mooy ñaareelu xaaju Jazaa’u Shakuur te mooy sunu xaaj bu mujj. Sëriñ bi di di fi wax lenn ci coono yi mu daj Dakar, ca gaal ga. Ci néeg yu xat yi ñu ko daan duggal. Wax na fi it wax yu yéeme ci may yi mu jëlle ci tagg gi […]
Bismillahi Rahmaani Rahiim Lii ab dog la ci Téerey Sëriñ Tuubaa bii nga xam ne daf ciy néttali Yoonu Géej gi. Ku ñuy wax Abdu Latiif la ci doon tontu. La ko Tàmbalee Jéewal ba ca réew yu sori yi. Leeral na fa it lenn ci Xasiida yi mu bind ci yoon bi ak lenn […]
Bismillaahi Rahmaani Rahiim Ginnaaw sooññee ci fonk julli ak teewlu julli, ak bañ a roy ci nasaraan yi ak yahuud yi. Te mu am sax ñoo xam ne bu ñu gise ab nasaraan dañuy defe ne ab malaakam Yàlla leen gis. Su ko defe li des ci Téere bi Sëriñ bi daf ciy xamlewaat mbii […]