Bismilaahi Rahmani Rahiim Nu dikkaat ak yéen ci beneen tomb jëm ci Daaju Mag ñi. Sëñ Abo Jaxate moo fas yéene leeral fii xeeti riim yi daje ci ñaareelu Daaju 78. Dina fi fàttali itam ni ko Sëriñ Saalihu Mbàkke Radiyallaahu daan bëggee, ba taxoon na sax mu santon ku nuy wax Baay Móodu Gay […]
Bismilaahi Rahmaani Rahiim Sëriñ Abo Jaxate mooy dikkaat ci leeral Daaju Muwaahibu 78, ci ñaareelu tooluwaay wi. Dana fi leeral lu aju ci tontu gi ginnaaw ba ñu daaje ba noppi. Jànginu waa kër Sëñ Abdulaahi Jaxate ca na mu gën a refete dees na ko fi dégg, ak dundalaat ko fi. Yàlla nanu Yàlla […]
Bismilaahi Rahmaani Rahiim Ginnaaw ba mu nuyoo mbokk yi ak dëkkandoo yi dafa daaldi soññee ci farlu ci lu baax ak jaamu Yàlla ju sax, ak di boole xam ak jëfe. Fàttali fi it lenn ci àddis yi jëm ci sàmm sa bopp ak benn lor kenn. Mu dolli soññee ci farlu ci Jàngum Xasida […]
Bismilaahi Rahmani Rahiim Lii ab tënk la jëm ci Taanug Sëriñ Saalihu ci daaj yi ak la mu sasoon ndogo yi ci nu koy jàng. Xasiida yooyu nag siiw na ci seen biir ci aw tur te mooy: « sas wi ». Dina fi tontu ay laaj yu jëm ci fànd woowu, moom Sëriñ Abo Jaxate jëwrinu […]
Mi ngi feeñ jamono ci atum 1340 dëppoo ak 1920 walla 1921, 26 fan ci Gàmmu ca dëkk buñuy wax Daarul Haalimul Xabiir, ñu gën ko xam ci Ndaam. Soxna Njaxat Silla nettali na Sëriñ Mustafaa Lo ne ko, Sëriñ Ndaam dey terale na 33 gàtt Sëriñ Murtada. Ba weeru gàmmo teerse day def bis […]