Bismilaahi Rahmani RahiimSëriñ Saalihu Faal mi ngi feeñ jamono ci atum 1858 ci dëkk buñuy wax « Jabbe Faal ».Jabbe Faal nag mi ngi ci wettu « Waaqi » mi nga xam ne ci kiliftéefu Aatumaan Faal la bokkoon ci Jàmbur. Way-juram wu góor mi ngi tuddu Ahmadul Faal Roqaya, way-juram wu jigéen mi ngi tuddu Soxna Saynabu Njaay […]
Mi ngi gane àdduna bisu àjjuma ci weeru Rajab ci Daaru Salaam atum 1888/1889 di doomi Seexul Xadiim ak Soxna Awa Buso. Sëriñ bi moo ko dalal Alxuraan moom ak magam Seex Muhammadu Mustafaa. Sëriñ Daam Abdu Rahmaan Lóo moo ko àggalel jàngum Alxuraan ci Daarul Haaliimul Xabiir Ndaam. Sëriñ Maam Moor Jaara moo ko […]
Mi ngi gane àddina 1912 fa Daarul Aaliimil Xabiir, mi ngi feeñ ci weeru safar. Doomi Xaadimu Rasuul la, Soxna Faatima Suxraa mooy way-juram wu jigéen, Sëriñ bee ko jëlle Gànnaar moom ak Soxna Faatima Kubra way-juru Seex Abdullaahi Mbàkke. Ñoom ñépp ay sariif leen. Ba mu dikke àddina la Sëriñ Abdu Rahmaan yabal ndaw […]