1-Seriñ Tuuba Qàda lahu laahu maxtara lahu ne na: maqàma mi gana kawé fa yàlla jamono ji moy dëkal weetal yàlla cib xol.
2-Sëriñ Tuuba Qàda lahu laahu Maaxtara lahu ne na mbir yi ñetti xaacc lë: xam-xam bu am njariñ ak jëff ju yiiw ak teegin buñ gëram. Xam-xam bu am njariñ mi ngi juddo ci xam sa hayiibi bopp. Jëff ju yiiw migi juddo ci womat’u jëm ci yàlla sunu borom ak di ci womat’u. Teegin buñ gëram mi ngi juddo ci yaruk Sëriñ’ub tarbiyah, moma na aggalé ci yàlla sunu Boroom, di lako jegeel.
3- Sëriñ Tuuba Qàda lahu laahu Maaxtara lahu ne na: Ku xam boromam du tóop kudul boromam, ku sàggan itam du tóop ludul bakkanam. Ñi xam yàlla da ñuy dimbalanté ci tóop yàlla ak ragal yàlla, ñi sàggan da ñu xëcco ci moy yàlla ak nono.
4- Seriñ Tuuba Qàda lahu laahu maxtara lahu ne na: Sunu Borom bim bëggé digal malaaka yi ñu sujjodal Adama dëkko xamal ñent ci ñoom, xamal len itam da na am kudul sujjod, te bu bóoba da na don ap Yaafar, Ibliis nak bokon ca ño ñee. Bañ len diggalé Ibliis deeltu ganàw di xool kooku kan lë. Ba ñëp sujjodé bam des moom dong, mu wóor ko ne mooy kiñ rëbb la tamboli di dëggaral boppam ci mbeñ gi, di leen won ñi motey ak lankam te mo gën Adama. Bi Seriñ bi waxe lii da di ne: lii nak ma neef’nacce jangé ñaar: bu njëkk bi mooy: ñaak gaawé ndigal da na xañe gëram, di waral merum sunu Borom. Ñaarel bi mooy gëstu hawray jambur mën na waral ak hëlku.
5- Seriñ Tuuba Qàda lahu laahu maxtara lahu ne na: ku bëgg mucc ci’w ay nattu nako teet, ku bëgg texe ci’w yiiw nako def, ku bëgg feeñal njeek nako feeñal ci def njeek, ku bëgg nëbb aw ñaawteef nako nëbb ci def njeek.
6- Seriñ Tuuba Qàda lahu laahu maxtara lahu bi muy doora ñëw foofu këru’k » Njàrem » gi neek, ne na Paak bi, mi gi ñuy seedel ne ay julit lañ yuy weye ndigal tey refetal. Ji seedel ña fi neekkon ne ay yaafar lañ, ay saay-saay lañ, ay naafeq lañ. Lii nak ci adduna lë ak ëlak. » Qad aflahal mùminùna inahu Là yuflihul kaafirùna »
7- Seriñ Tuuba Qàda lahu laahu maxtara lahu ne na: ku gis ci mbokkam hayib na yene yàlla beña feeñal hayib jóoju ci mom, kon sunu Borom da na ko suturàlal hayibam.
8- Seriñ Tuuba Qàda lahu laahu maxtara lahu ne na: bo bëggé xam yàlla ci ndigalam yi da ngey baayi térée’m yi.
9- Seriñ Tuuba Qàda lahu laahu maxtara lahu ne na: nitt bu de tuddu hayibi jambur yi dey dàldi tassaro ci kawam. Mi ngi melni ku yennu ndapp lu def sobé sà sukko bënné sobé sa sootiku ci kawam.
10- Seriñ Tuuba Qàda lahu laahu maxtara lahu mës na geen am kilifa gu mag gu ñëw diko ziaara mu tambolé waxtaanak mom mu sëgg di tombatu fi suuf. Sëriñ bi diko xool bam tombu juroomi tomb, mu ne ko loolu ngay def lo ci jublu? Mu ne ko dama don fo. Sëriñ bi ne ko teggal sa bàràm ci tomb bu njëkk bi te wax » Subhaana laahi » mu def ko, mu ne ko teggal ci bu ñaarel bi te wax » Alhamdulilaahi » mu def ko. Mu ne ko teggal ci bu ñeteel bi te wax » Laa ilaaha ila laahu » mu def ko, mu neko teggal ci bu ñenteel bi te wax » Allahu akbar » mu def ko. Mu ne ko teggal ci bu juroomel bi te wax: » laa xawla wa la quwata ilaa bi laahi » mu def ko. Sëriñ bi ne ko tomb bu ne am nga ci tuyyàba ju fees asamaan’ ak suuf nga naron ko yàqq ci lo xam ni amul benn njariñ.
11- Seriñ Tuuba Qàda lahu laahu maxtara lahu mës na wax ci benn jataay ku bëgg yàlla na took, ku bëgg kudul yàlla na jog.
Al-Habdul Xadiim
Grenoble, 08/09/2019