Jazbatu sighàr han lahibin li xidmatil muxtaar(1).

Bismilahi rahmani rahim.

« Sëriñ Alhaji Mbàkke Xàdimul Xadiim mo ci’y gàttal ci wolof téeré bii ngir bëgg julit yëpp njariñu ci rawanté’naak muriid yi yalna ko yàlla nangu ci barkep Sëriñ Tuuba Qàda lahu laahu Maxtara lahu »

                                                                       ***

Méñatum « Jazbatu sighàr »

Bismilahi rahmani rahim salla laahu hala sayyidina muhamadin wa alihi wa sahbihi wa salama tasliiman.

Man mi gana lott ci mindeef yi, ganna àjja wo sunu borom bi tëléwul dara, te àjjo wo wul jëm ci kenn may tambuli di wax. Man mi tuddu Ahmadu doomi Muhammad tey ñaan sunu borom mu mey xëcc di ma jëmé waxtu wu ne ci diiné. Li mey wax móodi : ma ngi sant sunu borom mi ma mey xam-xam’u wéetal ko ak xam-xam’u jëffé ndigal yi ak xam-xam’u seelal len. Di julli ci yonnent bi salla laahu tahala aleyhi bi alihi wa sahbihi wa salama mi nu andil Al-Imaan, Al-Islaam, Al-Ihsaan, di ko ñaanal moo’ki ñoñam ak i sahabam ya matal kollarék sunu borom. Ginaaw loolu Tawhid da melné ak ruuh ci diiné, Al-Islaam melné aw yaram, Al-Ihsaan melné ay yéré. Andil naalen tey way wu jëm ci yoo yii, na ngen ko jàpp.

Jazbatu sighàr han lahibin li xidmatil muxtaar, la ko tuddé. Liy xëcc xalé yi jëmé len ci lagéeyal yonnent bi salla laahu tahala aleyhi bi alihi wa sahbihi wa salam ba duñ fo. Yalna yàlla dooli yonnent bi salla laahu tahala aleyhi bi alihi wa sahbihi wa salam tedd’nga akk’uk woolu moo’ki ñoñam ak i sahabam, li feek murid buy tóop ndigal mi ngi texe ak li feek murid bu dul tóop ndigal mi ngi tóop sheytané.

                                                                  Ap dog

Diiné ñett xàcc la : ngëm, tóop’u ndigal yi ak refetal.

NGȄM móodi ngëm yàlla subhanahu wa tahala ak malaaka yi aleyhimu salam ak yonnent yi aleyhimu salaatu wa salam, ak bis pencci ak dogal yi. Ni ñuy gëmé yàlla subhanahu wa tahala móodi nga gëm ne amna, tambuli wul feen, yamul feen, nurowul len ak kenn. Du jëmb ju niy lamb di ko dacc wala ñu koy xool di ko gis. Du mélo wuy tàbbi  ci biir jëm, di ci neek. Amul kenn ku koy ñaarel ci méloom wala jëffam wala jëmam ju tèdd ja. Amna kàttan go xam ne lu mu bëgg amal amal ko, lu mu bëgg ñaakal ñaakal ko. Dara manta am te neexu ko. Xam na leep, dey dundu, di gis leep, di deeg leep, di wax, neekkul ku ñiy wax te amul, amul fu mu tambolé. Du jeex, nuruwul kenn wala len, du àjja wo, neekul ñaar wala ñett jam kaw. Lootul ci dara, amul len luy am ta neexu ko. Du tëx, du reer, du dé, du gumba, du lù, dara waruko. Lepp lu mu def dako def ci ag mbaxam ak ngënélam. Lepp lu mu ñaakal itam nooni ndax def ak bayyi da dagan ci moom. Li nuy tektal ag amam, moom sunu borom subhanahu wa tahala mooy jëff yi mu amal ndax jëff ju neek dey tektalé kako def, bo gisé nééfare’w gëleem da ley tektal ag gëleem, bo gisé ap tank da ley tektal nitt ka fa dëkk. Naka noonu asamàn si ak bideew yi, suuf si ak yóon yi, géej yi ak dùs yi, taw yi ak ni ñuy sotté.Yii yëpp da ley tektal sunu borom subhanahu wa tahala.

Al-Habdul Xadiim

Grenoble, 07/11/2019.

S’abonner
Notification pour
guest
2 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Yacine
Yacine
5 années il y a

Dieureudieuf Mouride. Leral yi. Am na solo lol.

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR