Bismilahi rahmani rahim
****
-Ap dog
Ni ñuy gëmé malaaka yi aleyhimu salam moodi nga gëm ne am na ñu., duñu def bàkkaar, duñu lekk, du ñu naan, duñu xayta, duñu béewal, duñu goor, duñu jigéen. Ay jàmm lañu, ci leer lañu leen bindé, bokku ñu ay mélo itam. Ci sàbbaal suñu borom lañuy naané, ci sellal sàbbaal gi lañuy lekké. Am na fukki malaaka yo xam ne da ñu len wara gëm ba nopi, xam seeni tur ak li ñuy lagéeyé. Te ñoo di Jibril, Miika’il, Israa’fil, Hazraa’il, Raqib, Hatid, Munkar, Nakiir, Màlik, Ridwàn aleyhimu salam.
Sayyiduna Jibril aleyhi salam mooy waaccé wahyu gi di wax’ak yonnent yi
aleyhimu salàtu wa salam. Miika’il mooy taw, Israafil mooy wall bufta bi ngir adduna tukki, Hazraa’il mooy roocci rùh yi. Raqib ak Hatid ñooy bind jëff yi ak wax yi. Màlik mooy wattu sawara yi, Ridwàn mooy wattu àjjana yi. Munkar ak Nakiir ñooy laacc ci bàmmel, da na ñu laacc ñëpp. Kuñu rob, ak kuñu robul melné kuñu lekk wala mu lakk nekk dóom, wala mu lap. Buñu dikké da ñuy toogal néew bi, déelo ci rùh gi bamuy degg, di xam. Loolu mo waral néew bi dana degg fëggu’g dàlli ñi ko doon denc buñuy dem. Seen kàddu yi day melné ag dënnu. Seen bët yi melné ag mélax, lu melné ay fer’ñent mooy géené ci seeni géemiñ bu niy wax, nuru wuñu menn malaaka, and’ak xatug bàmmeel ba ak lëndam ga. Mindeef yi, yëpp da ñu leena ragal ba ci malaaka yi aleyhimu salam. Yalna ñu yàlla musal ci ñoom. Am na ñoo xam ne du ñu len laac ci bàmmel, bokk na ci yonnent yi aleyhimu salàtu wa salamu ak malaaka yi aleyhimu salam ak ni fàtu ci xareb lislaam ak ku dëggal ba melné Abu Bakrin radiya laahu tahala anhu ak ku désé ci am xélam ak ku doff ak ku jàngg ñetti lixlaas ca tawat jamu fàtoo ak ku saxal jang sùratul mulki rawanténaak ci guddi, ak ku faatu ci guddig àjjuma wala bëccag ga.
-Ap dog
****
Ni ñuy gëmé téeré yi móodi nga gëm ne am na téeré yu suñu borom waaccé ci ay aliwuh ak yumu waaccé ci laamiñu malaaka yi aleyhimu salam. Lepp lu ci nekk dëgg la gu wér. Dañuy tektal waxi suñu borom, mat na ñu téemeer ak ñent (104). Fukki (10) téeré mo waacc ci suñu Maam Adama. Juróom fukki (50) téeré moo waacci ci Shiisha, doomam. Fanweeri (30) téeré mo waacci ci Idriisa, fukki (10) téeré mo waacc ci xaritu’b yàlla Ibràhima aleyhimu salàtu wa salam. Looli moy
téemeer bi.
Téeré bi ñuy wax TAWREET ci sayyidina Mùsa aleyhi salaam la waacc, téeré bi ñuy wax INJIIL ci sayyiduna Isà aleyhi salam la waacc, téeré bi ñuy wax ZABUUR ci sayyidina Dàwud la waacc aleyhi salam, téeré bi ñuy wax
FUR’QAAN ci sayyidina Muhammad la waacc salla laahu tahala aleyhi bi alihi wa sahbihi wa salam.
Li tax ma andi téeré yi and’ak seeni tur da ñu len wara ràññee ak di xam seeni tur. Kepp ku weddi ci diiné lo xam ne ak waram leer na nañi melné julli, ab yéefar la. Bu fekke la mu weddi leerul naññi ba melné julli da ñu koy xamal waruk loola.
Buko delloo weddi ñu doora xam ne ap yéefar la.
Al-Habdul Xadiim
Grenoble, 13/11/2019.
Salam aleykum, amna solo. Yalla na sunu borom dolé yéwénal xam xam, dëgg topp AK jarignu
Wahaleykum salam.
Amiin ku baax
Dieureudieuff Serigne Cheikh
Amna Solo lolou saxx.
YALLAH NA SUNU BOROM BARKEIL LIGUEIY BII
Amiin yalna Yàlla nangu ñaan bàrke Borom Tuubaa