Kan Mooy Seex Abdul Ahad Mbàkke?

Mooy doomi Soxna Maryaama Jaxate ak Sëriñ Tuubaa Xaada lahu laahu Maxtaara lahu. Ci 23i la gane àddina ci weeru korite ci atum 1332 ginnaaw gàddaay gi. Di toolo ak 1914 ca Njaaréem.

Ba mu toolo cim jàng leen ko jox nijaayam Sëriñ Hamzatu, nijaay ji jox ko Sëriñ Allasaan Jaxate mu jàngal ko Alxuraan. Ci barab boobu la jàngee Alxuraan ba mokkal ko, bind ko. Am nañu wax ne kaamil gi Sëriñ bi la ko jox am ñu wax ne Seex Muhammadul Mustafaa la ko jox.

Ginnaaw ga la ko maggam bu baax bii yabbal fa Cindoodi mu fay jàng xam-xam ci ku nuy wax Sëriñ Maxtaar Jeŋ Guyaar. Àndiwaat na ko Tuubaa jox ko Sëriñ Habiibu Mbàkke mu fay jàng, ba mujj na doon kaŋ-foore, xam lépp lu dóomi-soxna war a xam.

Mu amoon gis-gis gu yaatu, teel a jàmbaare te ñame sumb. Li koy firndeel moo di ci atum 1932 la sanc ab dëkk, boobe amul 20i at. Bokk na ci dëkkam ya Daaru Rahmaan, Kàdd Ballooj, Kab Gay, Daaru Ja ak yeneeni dëkk di fa Tarbiya, di bay, di joxe àddiya. Ba Sëriñ Fàllu wàcce ab liggéey la toog ci xilaafay Borom Tuubaa ci atum 1968. Wax neen ni sax, di tudd turu Sëriñ bi di ci teg turu xalifaam ci jamonoom la tàmbali. Ku ñuy wax Kleedoor Jaañ moo ko njëkk wax « Sëriñ Tuubaa Sëñ Abdul Ahad » ginaaw ga la ko Sëriñ Mustafaa Basiiru tasaare.

Seex Abdul Ahad daa mane woon fu bari te xamoon jamono. Moo yaatal Marse Okaas, moo tàmbali « Université bi » moo dundalaat Aynul Rahmati ba ñépp man ci jot. Moo yokk « forage » yi, sanc Tuubaa « bibliothèque » bu mag, nu koy wax Daaray Kaamil, def ci alal gu bari, ubbi ko ngir ñépp man ci njariñu, talli yi jëm Tuubaa itam liggéey na ci lu réy. Moo yokk dëkk bi, « muré » Jumaa ji, yeesalaat barabu Ku Tedd ki. Moo aaye fa Tuubaa mbolleem luy tux ak ya ca askanoo ak lépp luñuy naan te Diine tere ko. Loolu moo waral Seex Abdul Ahad Ture wax ne:

« fitam waak xelam waa tax, mu xéy yeesalaat Okaas, te aaye fi ay ñaawtéef di leen jox ndigal yu leer, fitam waak xelam waa tax mu aaye fi jëf yu ñaaw lu mel ne naan ak tux ba dëkk bi lépp a leer » .

« Keroog ba mu feeñee Bàmba daa wax waxam ju réy ni am na ci moom yàkkaar ba yàkkaar ji mujj leer, keroog Bàmba daa bég, mbég mu réy bu seed xol, te daaldi bégal mbolloo mi ngir gan gi nëw te leer. Mu jël Fusti jox koy mag ñu jàng ñépp bég te naan darajay Isaa la indaale lépp a leer ».

Daan taxawu Yoonu Murid ci wàll yépp. Nit ku dëggu la woon, daan nen ko wax ñàkk-caaxaan, am fit lool, xel mi réy, mu manoon a jëflante ak ku nekk. Waa Nguur gi joxoon ko cër itam. Nit ku oyof la woon, leer ay wax, man a soññee ak a dimbale, tabe woon lool, bëggoon Sëriñ Tuubaa lool te daan ko wàlle. Amoon hikam lool, dégg Alxuraan te al ci tawfeex, dégg Xasiida yi lool ba yéeme ci. Daan yittewoo dëgg, fumu man a nekk ba miy tuut-tank demoon na ci Sëñ Mbay Jaxate ngir mu dénk ko. Lii la ko wax:

<<Abdul Ahad yal na saw fan gudd Mbàkke nga wér. Te sax ci jamm’aku yiw ak jaamu Yàlla gu wér. Farlul te wéy yal na ngay for dog bu sedd sa xol. Te mucc ciw ay’akum ndog sax ci def la la war.

Toppal sa mag Mustafaa bul génn yaw ndigalam. Ngir mag mu mat mag la mat ñéppub sëriñ te du wor. Jëfal te bul faale nit, bul geesu nit ci sa jëf. Na Yàlla tax ngay jëf ak Yonen ba ak ka la jur.

Kalay manal dara moo jar def lëf ak bàyyi lëf
Te kooka nag moo di « Rabbul Archi » yal na la yor. Yar bii nga yor yor ko biir ak bitti moo di sa kee. Moo gën ci yaw nit ñu baax ak kër yu baaxaki jur. Sa baay a gën ñépp teb yar dong-dong la yor. Yoral yaram ba te koo gis deeko sant ak a yar

Sa baay a gën ñépp ab yar ngir dalay jox a jox ab yar. Ba ngay am a am ab yar te doo mos i yar. Du yëkkatib yar di teg nit waaye moo gënu nit. Ñay teg nitub yar akay janneek a yeew ak a lor.

Nijaayi ndam yii nga am loo jis ñu am ko ci ndam. Xamal ni moo ko ca def jii wax ku nekk la bir. Nijaayi ndam yii nga am loo jis ñu am ko ci ndam. Xamal ni moo ko waral ak cant war na gu tar.

Ag cant war na ci yaw ak ñoom gu rëy gu rafet. Gu tol ne bàjjo gu dul yam fenn mukkati far. Loo jis ci Amsatu moo mii cib yar ak jëfu yiw. Xamal ni moo ko ca def gii wax ku nekk la bir.

Abdooki Amsatu ak Mbakkeeki Bàlla Asan
Yaw say nijaay a ngii ñoo diy sàll kenn du ciw par. Fëxal te raw am nga ab yóbbal fëx ak raw a des. Ngir baaxi bokk a di ab yóbbal na yitte ji sar.

Saral te wéy dëgg bul yam ciy nijaayaki
Baay ak nday di sant ak a doyloo seeni cër lu ko jar? Foo seeru kuy fok a doyloo ab cëram na nga wut. Loo dolli yaw ci sa cër bii ndax nga am cëri-cër. Jollil ca kaw bul fexee jëm suuf’akay wax a dal. Cig jolli ngay waare ab xiibon ca ngay note mbër.

Reggàyu jàmbur ku koy doyloo ba lekkul a xam ! Buurub Aras ba far ak bër yépp yal na la far. Yaw yal na ngay wéy’akay jëm kaw di dolliku ndam. Ba jiitu waa kaw te nangoo suufe kuy amu tur>>.

Lii la ko Sëñ Mbay Jaxate dénkoon, di ay dénkaaane yoy ku ko dégg da nga xam ne, nii rekk la man a mel. Sunu Sang bi nag 1989 la fi bàyyikoo. Sunub gëstu noo ngi koy dëggarloo ci kàdduy Sëñ Abdu Xaadr Majaalis ak Seex Abdul Ahad Ture.

Ginnaaw loolu nanu xam ne « Abdul Ahad, Bàmba ne waa ju man turam sab àjjana daaldi leer ». Yàlla nanu ko Yàlla feyal, te yokk ay mayam, dooli ko yërmande ak leer barkeb doomi Sheexul Xadiim yépp.

Was’salaamu Alaykum wa Rahmatullah!

Al-Habdul Xadiim
05/06/2021

S’abonner
Notification pour
guest
2 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Moustapha Bassirou DIOP
Moustapha Bassirou DIOP
3 années il y a

MachaAllah
Très intéressant et bonne continuation

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR