Ca 1958 la daaldi am sañ-sañ man a taxawal mbébétam. 1963 nga ci la aji Màkka, ba mu ñibisee tukkiwaat na ànd ak Sëñ Mustafaa Lo ak Sëñ Yande ci réew yu sori niki Kowet, ak Iraak 9i weer. 1965 mu jógaat dem Araabi Sawdi.
Al-Azhar nag ci ay coono yu metti la ko taxawale ba 1968 Sëriñ Abdul Ahad taxawu ko ci jiital ci Sëriñ Mustafaa Basiiru ngir ñu jàppale ko. 1975 nag ci la taxawal école bu njëkk bi. Senghor sax fekk na ko fa 21 janvier 1978. Waaye sonnon na lool ngir am ndigalu tàmbali jàngale mi ci Etat boobu njiitum réew daf leen ko jafeel ak di leen dawloo. Ku ñuy wax Abdu Xaadr Faal doonon ministre de la culture ci boobu jamono moo ci mujjee àndi xalaat yu am solo ngir mii man a sotti. Daf leen xelal nu seet benn universitaire def ko directeur bu amee licence sax baax na ngir mu man a dox seen digg ak Etat bi, su ko defe ñoom ñu xam seen programme. Mba lu ko moy Senghor du jóg ci dawloo leen donte jullit yee ëpp ci réew mi. 15 décembre 1978 leen am autorisation ci numéro 73 11 1978. 78, décret 78 11/73.
Ci loolu nag la weye ba taxawal 287 institus Al-Azhar 34759 ci ay góor di fa jàngee , 14428 ci ay jigéen di fa jàngee, 319 nit di taxawu jàngale mi ak la ca lëkkaloo. Te lii lépp ci ag nekkam la amee. Lépp tasaaro ci Sénégal , Gambie , Guinée Conakry, Côte d’Ivoire, Cameroun, New-York. Lim bii ñu fi àndi ci Novembre 2004 leen ko yaxal ci waxu Sëriñ Abdu Rahmaan moom Sëriñ Mustafaa Lo.
Sëriñ Murtada ginnaaw tabax ay jàngukaay, dafa daan yëngu ci luy dundal koomi réew mi ak utal ndaw ñi liggéey. Lu tool ni 300 nit dooon neen liggéey ci wàllum transport, dem ak dikk ji ba ñu ko mujjee xayma ci atum 2012 lay toolool. Mu defoon ci xéewal gu yaatu, yombal njëg li ba ku bëgg a tukki li ngay fay du bari, te fa ngay toog it dina mucc ayib, ba mel ne bus ya ca bitim réew. Daan dimbali ci weer wu jot lu 700 nit, ki ci daan gën a neewle daan na jot 4i junni. Duggoon na itam ci « boulangerie », te daan wax ni ci nekk ñu koy defar ba mu neex ngir ki koy lekk xolam man a seed. Daan na yëngu itam ci mbirum yar ginnaar, yoroon na itam ay tool, lu fa masaan a ñoree ba ñu génne ci asaka daf daan wax ñu jox ci Sëriñu Daara yi ak Imaam yi, ubbiwoon na imprimerie itam ca Kolobaan.
Li am moo di dafa boole woon di liggéeyal Yàlla ak di ko jaamu. Taxawal na it ay Jumaa yu baree-bari biir Tuubaa ak fu dul moom.
Yaatal na lool yoonu murid ci réewi Afrig, Amerig ak Eurob. Gox yu bari ca foofa mu def fa ay këri lislaam ñu di fa daahira, di fa jàng Alxuraan ak Xasiida yi. Gone yi di fa jàngee, mu duggal itam ñu baree bari ci Lislaam.
Tay jii nag doomam, Sëriñ Maam Moor moo ko wuutu ci wàll woowu. Moomit jàmbaar la lool, te yéeneem réy, jëfam réy. Yàlla na ci daje ak ngëramal Sëriñ bi moom ak képp ku koy jàppale ci liggéey bi.
Seex Muhammadul Murtadaa nag Yàlla na ko Saa Boroom dooli xéewal fa mu nekk barkeb Sheexul Xadiim.
Sëriñ Abdu Rahmaan Lo moom Sëñ Mustafaa Lo moo xamal lii Sëñ Lamin Ture, ñu foree ko ci seen jotaay bañu amaloon Bambey ci atum 2013.
Yàlla na leen Saa Boroom defal yiw ak taalube guñu nangu barkeb Seex Muhammadul Murtadaa.
Al-Habdul Xadiim
06/12/2021