Kan mooy Soxna Ami Seex Mbàkke?

Bismilahi rahmani rahim.

« Lii ag tënk la ci dundug Soxna Aminata Seex Mbàkke bintu Sayxil Xadiim »

Mi ngi gane àddina Daarul Aaliimil Xabiir ci atum 1922, wayjuram wu jigéen mi ngi tudd Soxna Faabéy Jóob mi bokk ak Soxna Faati Tuuti Jóob miy wayjuru Sëriñ Murtada lépp. Moom la Sëriñ Umar Faal di wax ca way wa naan : «  li uminaa faabéy Maréemu muxsinah, aaminatun xus hasihi mustahsanah, min xayri waalidin anaaral balada, kamaa ataaban-nafsa lii wal baladaa ».

                                                                          ***

Mi ngi tàmbuli am  jàngam ci yoxo yu Sëriñ Ndaam Abdu Rahmaan Lóo ba mokkal Alxuraan lool te xereñ ci. Mboleem fànni xam-xam yi yépp mi ngi ko jànge ci Sëriñ Abdu Rahmaan Lóo, ràññeeku woon na loolu ci man a way : amna Xasida gu mu taggee Maamam Soxna Jaaratulaahi Maryama Buso muy xasida wolof gu gudd, gu siiw. Lenn ci jàngkat ya daañu koy jàng, téemeeri bàyyit la  ak fukk ak benn (111). Mi ngi tambulee ci «  Bismil ilaahi ma jog man sant lilaahi, sangub jigéen ñi ci dunyaa Jaaratulaahi (…).

                                                                           **

Soxna Aminata Seex nekkoon Muriidatun, Saadiqatun. Muriidatun bu dëggu, ku kawe woon yitte la lool, dina feeñ ci xasidaam gi lim wax ni «  Bun yàqqu, bun yàqqe, bun yàqqit la Bamba defon, saadix bu sax ci ndigal ngir Jaaratulaahi. Ñaanal ma nag man sa sët bii tudd Aaminatin, nu sax ci roy la bu wér Maam Jaaratulaahi. Pasteef yi yokk, nu sax cig  jub di jàmmu bu wér, tay soop Allaaji Fadlulaahi  ».

Ku bëgg xam lu bari ci ag dundam ak pas-pasam da ngay deeluwaat ci xasida gi.

                                                                           **

Mi ngi doon liggéeyal Boroomam ci kër Sëriñ Muhammadu Faajama Ñaŋ li key firndeel moy mi ngi wax ci biir xasida gi naan « Ta jaajëfal ki ma àndal Seexu Ahmadu Ñaŋ, moy dóomi Ahmadu Ñaŋ ngir Jaaratulaahi ».

Bokk na ci njaboot ga mu fa am Sëriñ Xaadim Ñaŋ ak Soxna May Ñaŋ. Ginnaaw ba la ñu ko jox Sëriñ Mahmudan Jobbe Mbàkke moom Sëriñ Masàmba mu am fa Soxna Maam Faati Mbàkke.

Soxna Ami Seex nag ku wakkirlu woon la ci Yàlla, ba tax na ba mu tawatee, ‘’doctoor’’ yi bëgg  yatt ca yaramam dafa wax ni rus naa dajje ak Seexul Xadiim di am dara luy ñàkk ci samay cér ngir bëgg dund.

Mi ngi fi jogge 30/10/1965, mi ngi ci almeeri Tuubaa, radiya laahu anha wa nafahna bi barakaatiha !

Xibaar yi nag jëlle nañu ko tci Siira Masaayixul Muriidiya bi daayira Xuratul Hayni liggéey ci ndigalu Sëriñ Allaaji Baara Fallilu yal na ko sunu Boroom dooli yërmande ak ngëram waaye ak kilifteefu Seriñ Ahmadu Mbàkke Suhaybu yal na ko Yàlla dooli wér, ta guddal fanam barke Boroom Tuubaa.

Al-Habdul Xadiim

Grenoble, 02/02/2020.

S’abonner
Notification pour
guest
1 Commentaire
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Gaye
Gaye
3 années il y a

Macha’allah doy na sogné

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR